TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/03 p. 1
  • Solooleen woyof

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Solooleen woyof
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 9/03 p. 1

Solooleen woyof

1 Sàmmkat bu ndaw bu daan benn ponkalu soldaar ndax li mu wékk yaakaaram ci Yexowa (1 Sam. 17:​45-47). Boroom alal lu bare bu nangu muñ lu metti (Ayóoba 1:​20-22 ; 2:​9, 10). Nekk doomu Yàlla te bëgg ñépp xam ne lépp li ngay jàngale jógewul ci yow, waaye ci sa baay la jóge (Ywna. 7:​15-18 ; 8:28). Ñett ñooñu ñépp, li ñu nekkoon ay nit ñu woyof moo taxoon ñu def loolu. Tey it, nekk ay nit ñu woyof, lu am-a-am solo la ci àddina si ñu nekk nii. — Kol. 3:⁠12.

2 Bu ñuy waaraate : Bu ñuy waaraate, ñépp lañuy waxal. Duñu xool ci xeetu nit ki, cosaanam walla fi mu yaroo ak ni ñu ko yare.Loolu, bokk na ci nekk ay nit ñu woyof (1 Kor. 9:​22, 23). Bu ñu tasee ak ku bañ a déglu xibaar bu baax bi, te mu xas nu walla muy yuuxu suñu kow, duñu mer te duñu feyyu. Dañuy tàggoo ak moom ci jàmm, te wéy di wut ñi yelloo xibaaru Nguur gi (Macë 10:​11, 14). Mën na am ñu bare xam-xam walla suñu jàng ci lekkool sore, waaye duñu ci wonewu. Li ñu bëgg mooy nit ñi xam li nekk ci Kàddu Yàlla. Ndaxte ak lépp lu ñu mënta wax, xam nañu ne Kàddu Yàlla moo gën a mën a laal xolu nit ñi (1 Kor. 2:​1-5 ; Yaw. 4:12). Kon ñun, dañu bëgg def ni Yeesu, maanaam màggal Yexowa rekk. — Mark 10:​17, 18.

3 Ci biir mbooloo mi : Karceen yi dañu war a ‘ soloo woyef ci seen biir ’ (1 Pie. 5:⁠5). Bu ñu jàppee suñu mbokk yi ni ay nit ñoo xam ne ñoo nu sut, dinañu seet li ñu leen mën a defal, te bañ a yaakaar ne ñoom ñoo nu ko war a defal (Ywna. 13:​12-17 ; Fil. 2:​3, 4). Duñu xalaat ne am na yenn liggéey yoo xam ne ñun, waruñu ko def, lu mel ni bale ak fobeere Saalu Nguur gi.

4 Bu ñu nekkee ñu woyof dinañu mën a “ baalante ci mbëggeel ”. Loolu dina indi jàmm ak déggoo ci mbooloo mi (Efes 4:​1-3). Déggal ñiy jiite ci mbooloo mi, ci ku woyof la gën a yomb (Yaw. 13:17). Te it ku woyof dina nangu ñu yedd ko walla ñu yar ko (Sab. 141:⁠5). Te it, bu ñu woyofee, dinañu ñaan Yexowa mu jàpple ñu ci bépp liggéey bu ñu nu mënta dénk ci mbooloo mi (1 Pie. 4:11). Barkeelu Yàlla rekk moo mën a tax li ñuy def sotti, waaye du suñu kàttanu bopp. Daawuda xamoon na ko. Ñun it loolu lañu gëm. — 1 Sam. 17:⁠37.

5 Ci kanamu Yàlla : Li ëpp solo mooy ñu ‘ suufeel suñu bopp ci ron loxob Yàlla bu am kàttan ’ (1 Pie. 5:⁠6). Xéyna fi ñu nekk nii, ñu ngi ci coono yu metti. Te dañu yàkkamti Nguuru Yàlla ñów ngir dindi leen. Waaye dañu woyof te ñu ngi muñ, di xaar ba Yexowa indi li mu dige ci waxtu bi mu tànn (Saak 5:​7-11). Ayóoba mi jaaroon ci lu metti, li mu gënoon a bëgg mooy ñu “ wéy di màggal turu Yexowa ”. Moom lañu bëgg ñun itam.— Ayó. 1:⁠21.

6 Yonent Yàlla Dañel dafa woyofoon te doon ‘ wacce boppam ci kanamu Yàlla ’. Loolu moo tax mu neex Yàlla te Yàlla dénk ko liggéey bu am solo ci wàllu ngëm (Dañ. 10:​11, 12). Ñun itam nañu woyof, xam ne “ li woyof ak ragal Yàlla di indi mooy alal ju bare, tur bu mag ak dund ”. — Léeb. 22:⁠4.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager