XAAJ 6
Yeesu (Isaa), bi mu juddoo ba bi mu deewee
Malaaka mi tudd Jibril lañu yónni ci benn janq ju baax te tudd Maryaama. Nee na ko dina am doom buy nekk buur te di nguuru ba fàww. Yeesu juddu na ci fu ay mala di fanaan. Ay sàmmkat seetsi nañu ko foofu. Ginnaaw loolu, ay góor ñu jóge penku topp nañu benn biddéew bu leen yóbbu ba ci xale bu ndaw bi. Dinañu gis kan moo tax ñu gis biddéew bi ak naka la Yeesu mucce ci ñi ko bëggoon a rey.
Ginnaaw loolu, dinañu gis Yeesu, bi mu amee 12 at, di waxtaan ak jàngalekat yi nekkoon ci kër Yàlla gi. Fukki at ak juróom-ñett ginnaaw loolu, Yeesu sóobu na ci ndox. Mu daldi tàmbali liggéey bi waraloon Yàlla yónni ko ci suuf, maanaam liggéeyu waar nit ñi te jàngal leen lu jëm ci Nguur gi. Yeesu tànn na 12 góor pur ñu dimbali ko ci liggéey boobu, mu def leen ay ndawam.
Yeesu def na itam ay kéemaan yu bare. Jox na lekk ay junniy nit fekk tuuti jën yu ndaw la amoon ak tuuti mburu. Faj na ñi feebar. Dekkal na sax ñi dee. Ci nettali yi mujj ci xaaj bii, dinañu jàng lu bare ci li xewoon ci fanam yu mujj yi ak naka lañu ko reye. Yeesu def na liggéeyu waare bi lu tollu ak ñetti at ak genn-wàll. Kon lépp li ñuy nettali ci XAAJ 6 xewoon na ci lu mat 34 at ak lu ko ëpp tuuti.