4 UT BA 10 UT
KÀDDU YU XELU PÀCC 25
Woy-Yàlla nº 154 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)
Yeesoo ngi ci jàngu ba ca dëkku Nasaret di yéem mbooloo mi koy déglu ndax kàddoom yu néex a dégg
1. Xelal yu baax yu ñu mën a dimbali ñu xam ni ñu war a waxee
(10 minit)
Tànnal waxtu bi gën ngir wax (Kàddu yu Xelu 25:11; w15 15/12 19 § 6-7)
Na say kàddu nekk kàddu yu neex a dégg (Kàddu yu Xelu 25:15; w15 15/12 21 § 15-16; xoolal foto bi nekk ci)
Na say kàddu nekk kàddu yuy dëfël (Kàddu yu Xelu 25:25; w95 1/4 17 § 8)
2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
(10 minit)
Kàddu yu Xelu 25:28—Aaya bii, lan lay tekki? (it-1 670 § 3)
Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?
3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi
(4 minit) Kàddu yu Xelu 25:1-17 (th lesoŋ 10)
4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan
(3 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Waxtaanal ak kenn koo xam ne dafa am naqaru xol. (lmd lesoŋ 3 ponk 3)
5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki
(4 minit) KËROO-KËR. Li nga mën a wax bu la nit ki waxee ne dafa gëm bu baax lépp li mu jàng ci diineem. (lmd lesoŋ 8 ponk 4)
6. Waxtaan bi
(5 minit) ijwyp waxtaan nº 23—Turu waxtaan bi ci farãse: Que faire si on parle sur moi ? (th lesoŋ 13)
Woy-Yàlla nº 123
7. Li mbooloo mi soxla ci wàllu ngëm
(15 minit)
8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi
(30 minit) my nettali 6 ak 7