Woy-Yàlla 14 (34)
Na suñu dundin méngook Tur wiñ ñu tudde
(Isayi 43:10-12)
1. Yeowa Yàlla, Aji-kàttan, ji sax,
Ci njubaay ak mbëggeel amoo moroom;
Sosub dëgg ak sago gu dem dayo,
Ca asamaan yaay ilif ni Boroom.
Alfunniy malaakaa ngi lay surgawu;
Càkkeef, giy jommal, a ngi lay màggal.
Ñun, say Seede yi nga baaxe sa tur wi,
Suñu tur, yal na ñu wéy di sargal!
2. Taxawu ñu, Yaa, ndax ci bépp anam,
Ñu teral sa tur tey dundal say xar.
Nañu topp bu baax tànkiy Krist Yeesu;
Ciy ndigalam lañu fas yéenee jaar.
Suñ’ dundinu bés bu ne, nañ’ bàyyi xel,
Sa tur wu jolli, nañ’ moytoo gàkkal.
Ñun say Seede, defal nga ñu teraanga;
Suñu tur, yal na ñu wéy di sargal!
3. Ba ñuy wéy di góor-góorlu ci sa njaamu,
Dinañ’ liggéey ci mbëggeel ak salaam.
Dinañ’ doylu ci li bawoo sa loxo.
Ak mbégu xol, dinañu woy sa ndam,
Suñu tur, yal nañu wéy di ko sargal.
Nañ’ yóbbul ñép’ dëgg giy may dund,
Noonu di bégal sa xol, yaw Yeowa,
Yaw mi falu Buur ci sa kow tund!