Woy-Yàlla 17 (38)
Nañu wone suñu ngor
(Sabuur 18:25)
1. Mbooloo suñ’ Yàlla Yeowa
Daa bég ci gàddu turam,
Niki mbooloo mu gore dëg’,
Jébbalu ciy waar ndamam.
Ci ñamu xel wu duun te sel’,
Lay dund, du fey dërëm,
Ba tax ci xalaat, kàddook jëf
Da koy siggal tey gërëm.
2. Ci mbootaayu Yàlla itam,
Dinañ’ wone suñu ngor,
Taxaw temm ci déggal ko,
Bu dee sax noon ngi ñuy dóor.
Nañu sàmm liy alalam,
Ndax dara bañ di ko lor;
Su musiba naree dégmal,
Gaawleen jóg: bu kenn wor.
3. Ànd-ak ngor, dinañu wallu
Ñu bees ñeek ñi néew-doole,
Ci njàng meek ci waare gi;
Ni mbokk nañ’ leen xoole.
Noonu, niki ci biir njaboot,
Wóoloodi buñ’ di sulli,
Waaye ci wépp wóllëre,
Nañ’ fexe suñ’ ngor jolli.
4. Ci àddina su goreedi,
Nañu fésal suñu ngor
Ci képp ku ñu ko ameel;
Buñu ameel kenn bor.
Nañ’ weejal feniy Seytaane,
Seedeel Yeowa njubam.
Ngor dina ko jural bànneex,
Te tax ñoo jot ci yiwam.