Woy-Yàlla 23 (48)
Màggalal Yeowa
(1 Korent 3:7)
1. Màggalal Yeowa.
Waaw, ci mbëggeelam,
Sas na la yónnent bii:
Melaxloo dëggam.
Lép’ luy jariñ dëgg,
Jote nga ci Moom,
Yàlla, Aji-Yéwén;
Woyal sa Boroom.
2. Jiital ko saa su ne;
Fàtteel sa bopp.
Noonu melaxal ko
Ak leer gu-m’ sopp.
Doxal saa su neek moom;
Deel wut kanamam.
Saxal ciy jiital ak
Fullaal liggéeyam.
3. Jëmal kanam ak mbég,
Di jaamu Yàlla;
Gërëm ko ngir bép’ cér,
Ndax mooy li yell.
Màggalal Yeowa,
Waaw, yéeneel Nguuram,
Ba nit ñép’ ci kow suuf
Sargal it turam.