Woy-Yàlla 29 (62)
Barkeel nañu, ñi am yërmande!
(Macë 5:7)
1. Barkeel nañ’, ñi am yërmande!
Yaa fonk na ni ñuy dunde!
Ku bëgg lu jub, dañ’ lay wax
Ne Yaa yërmande la saxsax.
Ca Golgota la ko fésal:
Suñu njot, moo ñu ko feyal.
Yërëm na nit ñi rëyadi;
Xam na ne dañoo matadi.
2. Ñiy roy ci Yàlla, barkeel nañ’;
Baalub seen’ bàkkaar mooy seen añ.
Yërmande ñu ngiy jariñoo,
Saraxu Krist lañu muuroo.
Yërmande boobu nañ’ yéene,
Di waar Kàddug Yàlla fu ne,
Naan: ‘Takkleen fit yi, léegi,
Ndaxte Krist teew na ci Nguur gi.’
3. Ñi am yërmande duñu tiit
Ndax àttey Yàlla, seen xarit;
Ci yërmandeem, dina leen yiir,
Ndegam, ni moom, dañoo laabiir.
Ñu am yërmande, yal nañ’ doon!
Wone jikko jooju mooy yoon.
Nañ’ fexe, saa su ne, di roy
Yàllay asamaan, ji ñuy woy.
(MUJ)
Barkeel nañ’, ñi am yërmande!
Yaa fonk na ni ñuy dunde!