Woy-Yàlla 44 (105)
Màggalleen Taawu Yeowa!
(Yawut yi 1:6)
1. Màggalleen Taawu Yàlla
—Ki Yàlla donnloo—
Dale ca ba-ñ’ ko sàkkee,
Déggal Yaa la jagoo.
Lép’ lu am moo ko defar,
Muy ca kow, di ci suuf;
Moom Bëkk-néegu Yàlla,
Ci naw ko, moo sut fuuf.
2. Bokk melo ak Yàlla
Taxul mu yëg boppam,
Naan Boroomam lay wujjeel,
Mel ni ak moroomam.
Ak suufeelu wàcc na,
Sol melo doom-Aad’ma
Ngir làyyil Buur Yeowa
Te dundug nit sàmm.
3. Looloo tax ñu sargal Krist,
Yàlla yëkkëti ko.
Ngir sellal tur’ Yeowa,
Ak Yàlla la mànkoo.
Ca Ar-Magedon lay aar
Te xeexal gaayiy Yaa,
Alag nooniy Nguur’ Yàlla,
Def jàmm ci dunyaa.
4. Nañ’ sargal Taawu Yàlla!
Waarleen: ‘Nguuram teew na.’
Kër-oo-kër deeleen yéene,
Ne tem’ ci bép’ fànn.
Ak yëg bu mat ci nit ñi,
Leeralleen ñép’. Aywa!
Soññanteleen ciy màggal
Taawu Yaa Yeowa.