Woy-Yàlla 48 (113)
Ñun ñooy Seedey Yeowa!
(Isayi 43:10-12)
1. Nit ñaa ngiy jaamu liy neen,
Waaye Yaa ump na leen.
Moo di Aji-Kàttan,
Dale ca njëlbéen.
Jen’ ci ñiiy yàllay caaxaan
Du wax ëllëg ki koy ñaan.
Amuñu kenn ku leen seedeel;
Seen yàlleef mënuñoo firndeel.
(AWU)
Ñun ñooy Seedey Yeowa;
Nañ’ seedeek fit. Kon, aywa!
Yeowa day yégle liy nasam;
Li mu xamle, loolooy am.
2. ‘Yéen a doon samay Seede.
Xërëm, dinaa fii buddee.
Maay Yeowa Yàlla,
Buur bi mënta dee!
Musal naa te jëf, ngeen gis,
Fek’ amul yàllay xaalis.
Ciy yéene sama tur doguleen
Tey wone samay seede ngeen.’
(Awu)
3. Di seedeel turu Yàlla,
Setal ko ci sosal la.
Nañ’ artu ñiy yàq
Tur wi gën’ sell.
Nit mën naa am njéggalam,
Su jubloo ci Yaa ak ngëm.
Noonu seede day indil bànneex,
Yaakaaru dund gu dul jeex.
(Awu)