Woy-Yàlla 54 (132)
Sàmmal sa xol
(Léebu 4:23)
1. Sàmmal sa xol, yaw doom-Yàlla,
Dund dinga yelloo.
Ci kàddu Yaa deel jafandu;
Dina la nàndloo
Ne lépp lu ñu mën a def,
Xalaat a ko jiitu.
Kon, sàmmal ni ngay xalaate;
Moo war jaam, bi-ñ’ artu.
2. Ndimbal ngir sàmm suñu xol,
Yàlla nee na mooy ñaan.
Dee ko gërëm, di ko xamal
Liy sa tiis dëggëntaan.
Noonu it, njàngum Kàddug Yaa
Dina yiir suñu xel,
Ak suñu xaritoo ak ñiiy
Dox ci leer gu barkeel.
3. Waaw, fexeel ba sa xel teewlu
Ci lu dëggu saxsax,
Ci lu jekk te sopplu,
Lu mat a naw, te baax.
Su ñu wéyee di ci teewlu
Dinañu am jàmm,
Xol bu dal, yaakaaru dund.
Yaa dina ñu sàmm.