Woy-Yàlla 63 (148)
Nañu màggal suñu Yàlla, Buur bi
(Sabuur 145:1)
1. Woyalleen Yeowa Yàlla!
Taggleen Yàlla ji sell.
Turam nañu fexee sargal;
Gën di ko jegee ñu soxal.
Loxoom, ñépp la fi nekkal;
Bu ñu moyul, ñu am ndimbal.
Nañu wéy di gore ci moom,
Ci Yeowa suñu Boroom.
2. Nañ’ doon ñu gore te dëggu.
Ci barkeel ko nañu dogu.
Ndax ciy yoonam njub la xeloo,
Yeowa tagg la yelloo.
Kép’ ku ko bëgg lay sàmm;
Ànd ak moom day jur jàmm.
Da ñuy dimbali ñu mën muñ.
Nañ’ barkeel Yaa ak suñuy tuñ.
3. Nguuru Yàlla, tey, daa dégmal.
Dina indi njub ak xéewal.
Nguuram, fépp, deeleen yéene,
Yéen ñi, ci dunyaa mu génnee.
Fal na kiy Doomam ji jëkk,
Buur bi kenn sañul tëkk.
Ñi soxor, léegi, ñu ne mes.
Kiliftéefu Yaa daldi des.