Woy-Yàlla 84 (190)
Aw woy ngir Yeowa
(Sabuur 92:1, 2)
1. Woyu mbég wii Yàllaa ko moom;
Moo ñuy tette, ni baay ak doom.
Nañu gërëm suñu Boroom.
Na ko woy wii màggal.
Ndaw mbaaxaay ak ngor, yu yaatu!
Ci moom lañu mujj a bootu,
Dëggam mooy goreel, mooy niitu;
Kon, moom lañuy déggal.
2. Jaa-jëf Yeowa ndax sa leer,
Gi ñuy wommat ndax ñu bañ réer;
Mu ngiy melax niki aw weer,
Wu ceeñeer yiy dëfël!
Ngir yaakaaru Nguur gi, jaa-jëf!
Làmbaatootuñu, bay tërëf.
Li ñuy sàkkal pexe bép’ sëf,
Suñu xol ’ ngiy bégal.
3. Woy wu neex lañu koy woyal,
Moom Yàlla, mi toog ci kow jal.
Jaare ci Krist, nañ’ ko xamal
Suñu ñaan gu suufe:
“Yaa Yeowa, Aji-Mbëggeel,
Jaa-jëf ndax li nga ñu barkeel.
Ndax li nga ñu won sa cofeel,
Sa yoon lañuy jëfe.”