TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • sjj woy 158
  • ‘Yàggatul dara’

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • ‘Yàggatul dara’
  • Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Àjjana ji Yàlla dig
    Woyal, di Tagg Yeowa
Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
sjj woy 158

WOY-YÀLLA 158

‘Yàggatul dara’

Édition imprimée

(Abakug 2:3)

  1. 1. Yaa defar suuf si,

    ak sa loxo yi,

    Muy lu taaru lool,

    te it yéeme na lool.

    Suuf si soppiku,

    Yow doo soppiku.

    Yow lépp ngay yeesal,

    waxtu wi rekk ngay xaar.

    (AWU BI)

    Baay, yàkkamti nañu,

    dund ci àjjana.

    May ñu ba ñu mën a xaar.

    Ni jant biy fenkee,

    bés bu ne ci lu wóor,

    Noonu la sa bés wóoree.

    ‘Yàggatul dara!’

  2. 2. Yàkkamti nañu

    mbokk yi dekki,

    Waaye Yexowa,

    yaa gën a yàkkamti.

    Baay, ñun xam nañu,

    ni nga leen bëgge.

    Baay, may ñu ñu muñ,

    di roy noonu ci yow.

    (AWU BI)

    Baay, yàkkamti nañu,

    dund ci àjjana.

    May ñu ba ñu mën a xaar.

    Ni jant biy fenkee,

    bés bu ne ci lu wóor,

    Noonu la sa bés wóoree.

    ‘Yàggatul dara!’

  3. 3. Yàlla yaa ngi seet,

    ñi seen xol rafet.

    May nga leen yaakaar,

    ak àjjana biy nëw.

    Jël nañu jotu,

    waare dëgg gi,

    Te liggéey boobu,

    moo tax ñu jege la.

    (AWU BI)

    Baay, yàkkamti nañu,

    dund ci àjjana.

    May ñu ba ñu mën a xaar.

    Ni jant biy fenkee,

    bés bu ne ci lu wóor,

    Noonu la sa bés wóoree.

    ‘Yàggatul dara!’

    Baay, dimbali ñu ñu xaar.

(Xoolal itam Kolos 1:11).

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager