Nañu jàpple pioñee yi
1 Ñépp a xam ne mbooloo Yàlla mi dafa sawar a waare. Bu fekkee ne sax am na li tax mënuñu nekk pioñee, war nañu fexe ba xalaate ni pioñee yi. Maanaam, nangu def lépp li ñu mën ci li ñuy def. Am na ñu bare ñu mën a nekk pioñee. Kontaan nañu ci te bëgg nañu leen ci jàpple.
2 Fexe ba nekk pioñee te yàgg ci yombul. Bu ñu seetee liggéeyu waare bi ak jàngale bi, pioñee yi dañu ciy def lu bare. Liggéey boobu, laaj na pioñee yi góor-góorlu te xañ seen bopp lu bare. Naka lañu mëne jàpple te dëgëral ñooñu jébbal seen jot yépp ci liggéeyu waare bi ?
3 Li ñu mën a def : Pioñee yi dañu soxla magi mbooloo mi jàpple leen. Bu magi mbooloo mi dee liggéey ak ñoom, dina leen dëgëral bu baax. Ay magi mbooloo yu bare dañuy jéem a liggéey ak bépp pioñee bu nekk ci mbooloo mi, lu mu tuuti tuuti, benn yoon at mu nekk. Bu ko defee, dinañu mën a ndokkeel pioñee yi ci li ñuy def, te dinañu leen mën a dimbali ndax ñu jëm kanam. Ngir mën a waaraate ci waxtu yi mag yi mën a waaraate, pioñee yi dinañu war a defaraat yenn saay seen porogaraam. Mag yi war nañu fexe it ba ñiy waaraate am gox bu doy. Mën nañu def it yeneen ndaje yu ñuy am bala ñuy waare, ci ngoon walla guddi, ni mu gëne ci porogaraamu pioñee yi. Te loolu ci weer yu bare pioñee yuy jàpple lañu ko war a gën a def. — Isa. 40:11.
4 Surga mbooloo yi mën nañu jàpple bu baax pioñee yi. Bu ñu leen di dimbali ci waaraate bi, te bu ñuy toppatoo bu baax li ñu taxawal ci mbooloo mi, ci lañu leen di jàpple bu baax. Pioñee yu jigéen yi dañuy kontaan lool bu ñu amee mbokk mu góor muy jiite ndaje yi ñuy am bala ñuy waare. Ñiy toppatoo téere yi ak yéenekaay yi ci mbooloo mi, mën nañu fexe ba am téere ak yéenekaay yu doy ci mbooloo mi. Bu ñuy toppatoo mbir yooyu, dina tax pioñee yi mën a def seen xel yépp ci waaraate bi.
5 Ñépp a leen mën a jàpple : Waaraatekat yi mën nañu jàpple pioñee yi bu ñu fexee ba gën a am jot ngir ànd ak ñoom ci waaraate bi. Yeneen waaraatekat yi bu ñu àndee ak ñoom, te bu ñu leen jàpplee, pioñee yi dinañu ci kontaan lool. Xéyna mën nga seet nooy def ba ànd ak ñoom ayu-bés bu nekk walla ñaari yoon ci weer wu nekk. Mën nga séddoo it li nga am ak pioñee yi. Pioñee yi dinañu la ci gërëm bu baax. — Fil. 4:14-19.
6 Ci njaboot, bu amee ku nekk pioñee, ñeneen ñi mën nañu ko jàpple. Ci ay kër yu bare, mën nañu seetaat ni ñuy defe liggéeyu kër gi ndax kenn walla nit ñu gën a bare, mën a nekk pioñee. Suñu benn mbokk mu jigéen mu amoon ñetti doom, dafa doon liggéey ñaari bés ayu-bés bu nekk. Doomam yu góor yi dañu doon dem jëndi li ñu soxla ci kër gi, di def it bépp liggéey bu ñu waroon a def ci ëtt bi walla ci mbedd mi. Noonu lañu ko doon dimbalee. Doomam bu jigéen bi moo doon setal kër gi te di togg. Bi doomam bu jigéen bi paree jàng, dafa doon ay-ayloo ak yaayam ci liggéey bi, te nekk moom itam pioñee. Bu njaboot yi di séddoo liggéey bi noonu, dina yokk ñi mën a nekk pioñee, te indi ay barke yu bare ci njaboot yi.
7 Ci ay fànn yu bare, pioñee yu sawar yi, barke bu réy la ci mbooloo mi. Seen cawarte ak seen liggéey dafay xiir ñu bare ci yokk li ñuy def ci waaraate bi. Wóor na ne dinañu bëgg a def lépp li ñu mën ngir jàpple leen. Bu ñu àndee di liggéey noonu, dinañu bég te dina màggal Yexowa.