TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 7/02 p. 3-6
  • Nañu waare xibaar bu baax bi fu nekk

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu waare xibaar bu baax bi fu nekk
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni ñu mënee waare ci gox bu bare bitig
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Nañu waaraate bu baax fu nit ñi di bare
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2002
km 7/02 p. 3-6

Nañu waare xibaar bu baax bi fu nekk

1 Karceen yu njëkk ya, dañu sawaroon lool ci liggéeyu waare bi. Fépp lañu doon waare xibaaru Nguur gi. “ Yégal [nañu ko] waa àddina sépp ” ci 30 at kese yi toppoon ndekkite Yeesu Krist. — (Kol. 1:⁠23).

2 Ñun ñiy jaamu Yexowa tey, ñun it dañu sawar ci liggéeyu waare bi. Te li karceen yu njëkk ya bëggoon, moom lañu bëgg ñun itam, maanaam jéem a waar képp ku ñu mën a gis ci xibaaru Nguur gi. Lan moo ñu ci mën a dimbali ? Nit ñu nu dul fekk seen kër ndax li ñuy liggéey, ñu ngi gën di bare. Bu dul loolu, xéyna ñu ngiy tukki, walla dem jëndi li ñu soxla, walla dem féexal seen xol. Lan la yenn waaraatekat di def ngir xamal leen xibaaru Nguur gi ? — Macë 10:⁠11.

3 Am na ñoo xam ne ñu ngi leen di fekk fu ñuy liggéeye. Bu dee sax ci dëkk bu ndaw lañu nekk, am na ay gox yoo xam ne ay bitig rekk a fa nekk, walla ay sosyete, te ñi fay yendu, bare nañu. Ci dëkk yu mag yi, am na ñuy liggéey ci béréb yoo xam ne ay isin rekk a fa nekk ; walla ci biro yu nekk ci taax yu mag te kawe. Am na itam ñu dëkk fu ñuy tere ku fa dugg. Ñooñu ñépp am na ñu leen di waar, fekk ñu bare masuñu woon a dégg xibaar bu baax bi. Ci bésu samdi ak dimaas yi, am na ñoo xam ne waar nañu leen ci park yi, walla ci béréb fu ñuy ame noflaay, walla ca kër fu ñuy noppalikoo, walla ci béréb fu ñuy gaare oto yi, walla it fu am ay bitig yu bare. Ci béréb yooyu yépp gis nañu ay nit ñoo xam ne dañu bëgg déglu xibaar bu baax bi.

4 Ay waaraatekat yu gën di bare, ñu ngi jéem a dem fu bare nit. Bu njëkk, ñemewuñu ko woon. Dañoo xawoon a ragal. Yeneen fasoŋu waaraate yu mel ni kër-oo-kër lañu tàmmoon. Waaye léegi, naka lañu ko gise ?

5 Suñu benn mbokk bi nga xam ne yàgg na ci liggéeyu waare bi nee na : “ Loolu tax na ma gën a sawar ci waaraate bi ! ” Keneen ki, lii la ci dolli : “ Dafay tax sama xel gën a nekk ci liggéeyu waare bi. ” Benn pioñee bu xaw a màgget nee na : “ Loolu tax na sama xel, sama yaram ak sama diggante ak Yàlla, gën a am doole, [...] te ba tey maa ngi jëm kanam. ” Benn waaraatekat gis na ne léegi mu ngiy wax ak nit ñu bare ñoo xam ne masuñu woon a waxtaan ak Seede Yexowa yi. Gune yi, ñoom it ñu ngi bokk ci liggéey bu neex boobu te bég nañu ci. Benn gune nee na : “ Dafa neex ndaxte dangay wax ak ay nit ñu bare. ” Keneen ki nee na : “ Masuma bàyyi téere yu baree noonu ! ” Te loolu fekkoon na mu am ñu waare ci gox yooyu ay yooni yoon.

6 Wottukat yiy wër ñu ngi jiite liggéey boobu : Wottukat yiy wër, ayu-bés bu nekk, dañuy dem ci benn mbooloo. Am na ay at léegi, dañu doon waaraate kër-oo-kër ci suba yi. Ci ngoon yi, dañu doon seetiwaat nit ñi te jàngal leen Biibël bi. Waaye yenn saay dafay am ay gox foo xam ne duñu fa mën a gis ñu bare ci suba si. Biibël bi nee na : “ Àddina sii, ci ni mu mel, dootul yàggati. ” (1 Kor. 7:​31). Mbootaay gi xam na loolu. Looloo tax ñuy xelal wottukat yiy wër, saa yu ñu demee ci mbooloo, ñu seet ni ñu mënee defar seen porogaraam ngir mën a gis ay nit ñu gën a bare. Ci suba yi, mën nañu waaraate ci bitig yi walla ci mbedd mi. Mën na def ay mbooloo waaraatekat yu ndaw ngir ñu dem ci biro yu nekk ci taax yu mag yi, walla fu am ay bitig yu bare, walla fu ñu gaare oto yi, walla feneen foo xam ne nit ñi dañu fay bare. Bu ñuy waaraate dañu war a jariñoo bu baax-a-baax jot gi ñu am ngir mën a wax ak li ëpp ci nit ñu nu mën a gis.

7 Ñu bare ci wottukat yiy wër ak waaraatekat yi, nee nañu xelal boobu Mbootaay bi joxe, baax na lool. Am na ci yenn mbooloo ay kurélu mag yu laaj wottukat biy wër mu jàngal ay waaraatekat fasoŋu waaraate yoo xam ne dina baax ci seen gox. Waaraatekat yi ànd nañu ak wottukat bi, te gis nañu ni mu doon defe. Loolu, dimbali na leen bu baax. Tax na it ñu mën a jàngal ñeneen (2 Tim. 2:⁠2). Loolu lépp tax na ba nit ñu gën a bare mën a déglu xibaar bu baax bi.

8 Dëgg la, jarul ngay xaar ba wottukat biy wër ñów ci sa mbooloo, ngay sog a bokk ci fasoŋu waaraate yooyu. Nañu seet léegi ni ñu ko mënee def. Xéyna dinga ci gis lu mën a baax ci sa gox.

9 Waaraate ci mbedd mi : ‘ Waaw, fan la nit ñi nekk ? ’ Moom lañuy laaj léeg-léeg bu ñuy waaraate foo xam ne bare na kër fu ñu dul fekk kenn. Xéyna mën nañu leen gis fu ñuy nekk di jënd li ñu soxla. Ndax mas nga leen a jéem a fekk ci mbedd mi ? Waaraate ci mbedd mi, su ñu ko defee ni mu ware, mën na tax ñu mën a wax ak ay nit ñu bare. Bul taxaw ci benn palaas di wone suñu yéenekaay yi. Lu gën mooy nga ñów ci nit ñi, te jéem a am ak ñoom waxtaan bu neex. Jarul ngay jéem a wax ak bépp nit buy romb. Nanga wax ak ñi yàkkamtiwul : maanaam ñiy seetaan li nekk ci bitig yi, ñi toog ci seen oto, walla ñiy xaar kaar yi. Mën nga def lii : njëkk ko nuyu bu baax-a-baax, te may ko mu tontu la. Bu kooku bëggee waxtaan, seetal li ko mën a itteel te laaj ko xalaatam ci loolu.

10 Benn wottukat biy wër, jabaram, ak 6 waaraatekat, dañu ànd a waaraate ci mbedd mi. Nee na : “ Suñu suba soosu neexoon na lool ! Amuñu woon poroblemu kër fu ñu dul fekk kenn. Bàyyi nañu 80 ci suñu yéenekaay yi ak suñu kayit yu ndaw yu bare. Bare woon nañu waxtaan yu neex. Am na benn waaraatekat bu masul woon a waare ci mbedd mi. Lii la wax ak mbégte mu réy : ‘ Bi ma nekkee ci dëgg gi, yàgg na, waaye xamuma woon lu ma doon ñàkk ! ’ Mbooloo mi, dese woon na ay yéenekaay yu bare. Waaye jeexal nañu lépp bala dimaas bi jot. ”

11 Ci mbooloo mi ci topp, amoon na ay waaraatekat yu demoon suba teel waaraate ci mbedd mi. Waaye neexul woon noonu. Suñu benn mbokk bu jigéen, ñaari nit kese la waxal. Nit ñi dañu yàkkamti woon a dem liggéey. Bi mu fa demee, wottukat biy wër dégg ko. Dafa leen xelal ñu dellu fa, waaye ñu xaar ba mu naaj tuuti. Loolu lañu def te waaraate nañu ba midi. Kooku waxoon ak ñaari nit kese, joxe na 31 ci suñu yéenekaay yi ak 15 ci suñu téere yu ndaw yi. Juróom-ñaari nit ñoo ko jox seen tur ak seen adarees ngir waxtaanaat ak moom. Te it, dafa tàmbali ñaari njàngum Biibël bi. Ñeneen ñi it, seen waaraate neexoon na lool.

12 Boo gisee ku bëgg waxtaan, fexeel ba xam turam, adareesam ak nimoro telefonam. Mën nga ko ne : “ Suñu waxtaan bi neexoon na. Ndax bëgg nga ñu waxtaan beneen yoon ci sa kër ? ” Walla mën nga wax lii : “ Ndax dinga bëgg ñu waxtaan ci sa kër ? ” Loolu moo gën nga koy laaj ci saa si ni mu tudd, fu mu dëkk ak nimoro telefonam. Ñu bare dañuy nangu ñu gisaat leen ngir gën a waxtaan. Bul fàtte yóbbaale kayit yu bare fu ñu bind adareesu Saalu Nguur gi ak waxtu ndaje yi.

13 Boo tasee ak kenn, fekk gox bi mu dëkk, beneen mbooloo moo ko moom, wax ko mbokk yi nekk foofu ndax ñu seeti ko. Ndax waaraate ci mbedd mi dina baax ci seen gox ? Su dee waaw, nanga seetaat li ñu waxoon ci xaaj bi tudd “ Trouvons des personnes bien disposées en prêchant dans la rue de façon efficace ” ci Le ministère du Royaume bu sulyet 1994 (septaambar ci Kamerun). Ba pare, nanga dem waaraate ci mbedd mi ci waxtu fu nit ñi ngay mën a waxal di ëppe.

14 Waare ci biir kaar yi walla taksi yi : Benn suba, am na ay pioñee yu dem waar nit ñi doon xaar kaar bi ci wetu benn lekkool. Amoon nañu ay waxtaan yu neex, waaye dañu amoon benn poroblem. Saa yu waxtaan bi demee ba neex, kaar bi, bu ñówee, dog ko. Lan la pioñee yi def ? Dañu yéeg ci kaar bi te kontine seen waxtaan, ba pare wax ak ñeneen. Bu ñu àggee fu kaar bi war a yem, pioñee yi dinañu jël kaar buy waññeeku, te defaat li ñu doon def bu ñu doon ñów. Def nañu loolu di ko defaat, ba bàyyi 200 ci suñu yéenekaay yi te tàmbali juróom-benni njàngum Biibël bi. Am na ñu ci joxe seen adarees ak nimoro telefon ndax ñu seeti leen. Ayu-bés bi ci topp, pioñee yi demaat nañu fa, defaat li ñu defoon bés boobu. Bàyyi nañu 164 ci suñu yéenekaay yi te tàmbali nañu benn njàngum Biibël bi. Am na ku yéegoon ci kaar bi, te benn palaas ci wetu benn pioñee rekk moo desoon. Dafa xool pioñee bi, muuñ, te ne ko : “ Xam naa ne danga ma bëgg jox benn Tour de Garde. ”

15 Ñu bare dañuy waaraate, waaraate bu neex, ci kaar yi, saxaar yi, walla ci roppëlaan (avion). Naka nga mënee tàmbali waxtaan ak ku toog sa wet ? Seetal li benn waaraatekat bu am fukki at ak ñaar def. Dafa nekkoon ci kaar, benn xale bu jigéen toog ci wetam. Li mu def yomb na. Dafa jël benn Réveillez-vous !, di ko jàng. Li mu bëggoon mooy xale bu jigéen boobu laaj ko lu muy jàng. Te loolu moo am. Mu ne ko, téere bi muy jàng, dafay wone li mën a faj coonoy gune yi. Loolu dimbali na ko bu baax te foog na ne dina ko dimbali it. Jigéen ji nangu yéenekaay bi. Ci biir kaar boobu, amoon na itam ñaari xale yu doon déglu seen waxtaan. Ñoom it dañu bëggoon a am ci téere yooyu. Ki doon dawal kaar bi daldi taxaw, gaare, te laaj lu tax ñépp bëgg téere yooyu. Bi ñu ko ko waxee, moom it mu jël ci. Xale boobu doon waaraate, bu yorul woon téere yu doy, ndax loolu yépp dina am ? Déedéet.

16 Waaraate ci béréb fu nit ñi di féexlu ak fu ñuy gaare oto yi : Ku dem fu nit ñi di féexlu walla fu ñuy gaare oto yi, dina mën a wax ak nit ñu bare. Am na ay béréb fu bitig yi bare. Ndax mas nga waaraate fu ñu fay gaare oto yi ? Boo fa demee, xoolal li la wër. Seetal ndax am na ku yàkkamtiwul walla ku nekk ci biir oto di xaar. Nanga jéem a tàmbali waxtaan bu neex ak moom. Bu nangoo wax ak yow, nanga ko xamal xibaaru Nguur gi. Booy dem ca béréb yooyu, mën nga ànd ak keneen. Waaye, na ku nekk demal boppam bu ngeen di wax ak nit ñi. Buleen yor saag bu mag walla lu mën a tax ñépp di leen xool. Defal lépp ak sutura. Yenn saay liy gën mooy nga bañ a yàgg ci benn béréb. Boo waaraatee tuuti fii, nanga dem ci beneen béréb bu mel noonu. Boo tasee ak ku bëggul waxtaan, nanga tàggoo ak moom ci jàmm te jéem a wax ak keneen. Li ñu wax fi yépp, suñu benn mbokk bu góor def na ko. Ci benn weer, bàyyi na 90 ci suñuy yéenekaay ci béréb fu ñuy gaare oto yi.

17 Park, béréb bu rafet la. Mën nañu fa féexlu, walla fo. Am na ñu fay yóbbu seeni doom. Bëgguñu leen yàqal, waaye seetal loo mën a def ba yégal leen xibaar bu baax bi. Suñu benn mbokk bu góor tàmbali na waxtaan ak góor gu doon toppatoo benn park. Fa la gise ne li ko itteeloon mooy dorog ak ëllëgu doomam yi. Dem nañu ba faral di def benn njàngum Biibël bi ci park bi.

18 Waaraate ca béréb fu ñu dajale ay bitig : Yenn saay, duñu mën a waaraate ci bitig yi nekk ci béréb yooyu, ndaxte yoonu réew mi dafa koy tere. Waaye ay waaraatekat dañuy fexe ba mën a wax ak ñi fa nekk. Dañuy dem fu am ay baŋ, toog, te jéem a waxtaan ak ñi fay ñów ngir noppaliku. Su amee ku bëgg waxtaan, dañu koy jox benn ci suñuy kayit yu ndaw walla benn ci suñu yéenekaay yi, te dañuy fexe ba mën koo gisaat. Bu ñu defee noonu tuuti fii, dañuy dem defaat ko feneen. Loolu lépp, nañu ko def ci sutura, bañ nit ñépp di ñu xool.

19 Nanga nuyoo bu baax te tàmbali waxtaan bi. Bu la nit ki dégloo, laaj ko benn laaj, te déglu ko bu baax-a-baax. Nanga wone ne li muy wax itteel na la. Saa yoo ko mënee, nee ko : “ Li nga wax dëgg la. ”

20 Suñu benn mbokk bu jigéen tase na ak benn jigéen ju màgget. Dafa njëkk wax ci ni dund bi jafee léegi, ñu daldi am waxtaan bu neex-a-neex. Jigéen ji jox na suñu mbokk turam ak adareesam, te ci ayu-bés boobu lañu waxtaanaat.

21 Waaraate ci màngasiin yi : Yenn mbooloo am nañu ci seen gox ay béréb yu bare màngasiin. Kiy toppatoo gox bi mbooloo mi moom, mën na defar ay kàrt fu ñuy wone béréb yooyu rekk. Su fekkee ne amoon na benn kàrt bu ëmboon ba pare benn ci béréb yooyu, war nañu ci bind ba mu leer ne waruñu waaraate ci màngasiin yi fa nekk. Waaye mën na am ay goxu mbooloo foo xam ne loolu jaru ko; mën nañu boole màngasiin yi ak kër yi, di fa waaraate. Magi mbooloo mi mën nañu laaj ay waaraatekat yu aay ci liggéeyu waare bi, ñu faral di dem ca béréb yooyu bare màngasiin. Loolu dina tax ñu bañ a fàtte waaraate ci màngasiin yi.

22 Mën na am ñu laaj la nga bokk ci fasoŋu waaraate boobu, fekk masuloo ko def. Boo ci bëggee am “ fit ”, lii nga mën a def : nanga njëkk waaraate ci màngasiin yu ndaw. Boo demee ba gën cee wóolu sa bopp, demal ca màngasiin yu gën a mag (1 Tes. 2:⁠2). Booy waaraate ci màngasiin yi, nanga solu mel ni booy dem ci ndaje yi ñu am ci Saalu Nguur gi. Li gën mooy nga dugg ci màngasiin yi bu amulee ñuy xaar ñu jaay leen. Neel danga bëgg wax ak boroom màngasiin bi walla ak ki yore liggéey bi. Waxal ak sa xol. Te li gën a am solo, na sa wax gàtt. Jarul nga nekk foofu di baalu rekk. Jaaykat yi, kiliyaan yépp lañuy toppatoo, kon tàmm nañu ñu dog leen ci li ñuy def.

23 Boo nuyoo boroom màngasiin bi ba pare, lii nga mën a wax : “ Yéen, jaaykat yi, xam nañu ne, bare ngeen liggéey lool, te fekk leen seen kër yombul. Moo tax ñu ñów fi ngeen di liggéeye ngir jox leen téere buy wax ci lu jar a xalaat. ” Waxal benn walla ñaari xalaat ci yéenekaay bi nga bëgg bàyyi.

24 Walla mën nga wax lii boo gisee ki yore màngasiin bi : “ Gis nañu ne ñi nekk di jënd ak di jaay, dañu bëgg xam li xew ci àddina. Ci La Tour de Garde (walla Réveillez-vous !) bii sog a génn, am na loo xam ne dafa ñuy laal ñun ñépp. ” Waxal loolu lan la, te nii nga mënee jeexal waxtaan bi : “ Wóor na ma ne, li nekk ci téere bii, dina la neex. ”

25 Boo fa gisee ay surga, seetal ndax mën nga dolli lii ci li nga wax ba pare : “ Ndax li ma la wax fi léegi, mën naa ko gaaw a wax say surga yi ? ” Su ñu la ko mayee, bul fàtte ne yaa waxoon ne doo yàgg, te ki yore màngasiin bi, dina seet ndax dinga def li nga wax. Su amee ci surga yi kenn ku bëgg yàgg ci waxtaan bi, li gën mooy nga seetiwaat ko këram.

26 Ci benn dëkk bu ndaw, ay waaraatekat ak benn wottukat biy wër dañu ànd di waaraate ci màngasiin yi. Am na ñu xawoon a ragal ndaxte masuñu woon a bokk ci fasoŋu waaraate boobu. Waaye ci lu gaaw gis nañu ne neex na lool. Ci lu matul benn waxtu, waxtaan nañu ak 37 nit, bàyyi 24 ci suñu yéenekaay yi ak 4 téere yu ndaw. Suñu benn mbokk bu góor nee na : ‘ Nit ñi ñu gis ci waxtu boobu ñoo ëpp nit ñi ñu mënoon a waxal ci benn weer yépp bu ñu doon waaraate kër-oo-kër. ’

27 Foo mënta nekk, fexeel ba mën a waare : Yeesu, saa yu ci amoon bunt dafa doon yégle xibaar bu baax bi. Daawul waaraate ci fasoŋ yu ñu tàmmoon a def rekk (Macë 9:9 ; Lukk 19:​1-​10 ; Ywna. 4:​6-​15). Seetal ni ay waaraatekat yi fexe ba mën a waar ay nit.

28 Am na ñuy waar waajur yi bu ñuy xaar seeni doom ci seen buntu lekkool. Ñu ci bare, dañuy ñów 20 minit bala xale yi génn. Bu ko defee, dañuy am jot bu doy ngir waxtaan bu baax ci li Biibël bi wax.

29 Ay pioñee yu bare bu ñuy jàng suñuy yéenekaay, dañuy seet kan moo ko gën a soxla. Moom la suñu benn mbokk mu jigéen def. Dafa jël Réveillez-vous ! bu 22 desàmbar 1995, bi waxoon ci “ L’école en crise ”. Wone na ko ci 6 lekkool yu amoon ci gox bi mbooloom moom, nit ñi kontaan lool. Jël na it suñu yéenekaay yiy wax ci mbirum njaboot akit ci ñaawtéef bu ñuy def xale yi. Yóbbu na ko ci biro yiy toppatoo njaboot yi nekk ci jafe-jafe. Foofu sax dañu ko ne, bu amee yu war a génn te nar a wax ci lu mel noonu, na ko indi. Réveillez-vous ! bu 8 màrs 1996 bi wax ci ñàkk liggéey, yóbbu na ko ci benn biro buy toppatoo ñi amul liggéey. Nee na, ñi fa nekkoon, ni ñu kontaane, weesu na sax lu mu yaakaaroon.

30 Benn wottukat biy wër ak jabaram, ñoom, dañuy jéem a waar nit ñi bu ñuy dem marse walla bitig. Dañu fay dem ci waxtu bu amul nit ñu bare. Dañuy dox ndànk-ndànk, di xool li nekk ci bitig bi. Loolu lañu def ba am ay waxtaan yu neex yu bare.

31 Ay waaraatekat yu bare am nañu ay waxtaan yu neex ci béréb fu ñu def masin yuy fóot yére yi. Bu fa kenn nekkul, duñu fa bàyyi téere rekk, dem. Dañu bëgg nit ñi dégg xibaar bu baax bi. Looloo tax ñuy fexe ba am ay waxtaan ak ñi fa nekk.

32 Am na ay waaraatekat yoo xam ne may nañu leen ñuy waare ci aéroport. Waxtaan nañu ak ñu doon tukki, fekk seen réew barewul ay Seede Yexowa. Jox nañu ñi bëggoon a waxtaan benn ci suñuy kayit yu ndaw walla benn ci suñu yéenekaay yi.

33 Am na ay mbooloo yu am ci seen gox ay kër yoo xam ne doo fa mën a dugg bu ñu la ko mayul. Ay waaraatekat faral nañu waar ñi fay garde walla ñiy liggéey ci biro yuy toppatoo kër yooyu. Moom lañuy def itam bu ñu demee ci béréb fu ñu defe ay kër yu bare te ci benn bunt bu mag lañu war a jaar ngir àgg fa. Gardiñe bi nekk ci bunt boobu lañuy waar. Loolu la benn wottukat biy wër ak ay waaraatekat def ci 7 béréb yu mel noonu. Ci béréb bu ci nekk, bi ñu gisee kiy toppatoo kër yooyu, wax nañu ko ne dëgg la, mënuñu dugg, waaye bëgguñu ñu ñàkk li ñu wax ci suñu yéenekaay yi sog a génn. Ci 7 béréb yooyu, ñiy toppatoo kër yooyu nangu nañu suñu yéenekaay yi te nee nañu sax dañu bëgg jot ci yi war a génn. Te ñi dëkk ci biir kër yooyu, dañu leen telefone ngir waar leen. Boo bëggee xam ni ñu mënee waaraate ci telefon, mën nga jàng “ Comment prêcher efficacement par téléphone ” ci Le ministère du Royaume bu feewriyee 2001 xët 5 ak 6.

34 Nanga góor-góorlu ngir waaraate fu nekk : Jébbal nañu Yàlla suñu bopp. Loolu war na tax ñu jàppe liggéeyu waare Nguuru Yàlla ni lu jamp. Bëgg nañu wax ak nit ñi ci waxtu bu leen gënal. Kon war nañu bàyyi ci ginnaaw li ñu gënal ngir “ def lépp lu [ñu] man, ba ñenn mucc ”. Ñiy jaamu Yexowa te jébbalu ci moom, lii lañu bëgg ñoom ñépp, ni ko ndaw li Pool waxe : “ Damaa def loolu lépp ndax xebaar bu baax bi, ngir man it ma am wàll ci barkeem. ” — 1 Kor. 9:​22, 23.

35 Pool wax na itam lii : “ Kon nag dëgg-dëgg, gën na maa bég ci damu ndax sama néew doole, ngir kàttanu Krist dëkk ci man. [...] Ndaxte bu ma néewee doole, booba laay am kàttan. ” (2 Kor. 12:​9, 10). Maanaam, kenn mënul a def liggéey boobu ci sa kàttanu bopp. War nañu ñaan Yexowa mu may ñu xelam mu sell mi am kàttan lool. Nañu wóor ne dina ñu jox li ñu ko ñaan. Ba pare mbëggeel bi ñu am ci nit ñi, dina ñu xiir ci seet lu ñu mën a def ngir waar leen ci xibaar bu baax bi, te loolu fu ñu mënta nekk. Ci ayu-bés bii di ñów, ndax dinga jéem benn ci fasoŋu waaraate yi ñu wax fii ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager