Yégle yi
◼ Téere yi ñuy wone ci weeru sãwiyee : Téere yi am 192 xët te génn bala 1988 yi ngeen am ci seen mbooloo. Mbooloo yi amul téere yooyu, mën nañu wone téere L’humanité à la recherche de Dieu. Feewriyee : Téere bu bees bi tudd Approchez-vous de Jéhovah. Mbooloo yi amagul téere boobu, mën nañu wone téere Création, walla téere Révélation : dénouement. Màrs : Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex. Dinañu góor-góorlu ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi. Awril ak me : Benn Tour de Garde ak benn Réveillez-vous ! Bu nit ki wonee ne suñu waxtaan neex na ko, bu ñu koy seetiwaat nañu góor-góorlu ngir jox ko téere Adorez le seul vrai Dieu. War nañu def li ñu mën ngir jàng ak moom Biibël bi, rawatina bu masee jàng ak seede Yexowa yi téere Xam-xam ak téere Laaj.
◼ Ci weeru feewriyee la wottukat biy wër ci mbooloo yi di tàmbali def waxtaan bu ñu jagleel ñépp bi tudd “ Rëcc ci àddina su nekk ci lëndëm ”. Bésu 2 màrs, war na fekk ñu tàmbali ko ba pare.
◼ Mbooloo yi war nañu def lépp li war ngir ren ñu mën a def ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ci bésu àllarba, 16 awril, bu jant bi sowee ba pare. Bu ñu tàmbalee waxtaan bi bala waxtu woowu, waruñu joxante mburu bi ak biiñ bi bala jant bi so. Laajleen ñiy toppatoo météo bi kañ la jant bi di so ci seen gox. Bu amee ay mbooloo yu bare yu bokk benn Saalu Nguur, xéyna benn walla ñaar ci ñoom mën nañu seet beneen béréb fu ñuy defee ndaje boobu. Bu amee mbooloo yu bokk fi ñuy defee ndaje boobu, nañu fexe ba mu am lu mat 40 minit diggante ñaari ndaje, bu mënee nekk. Bu ko defee, nit ñi dinañu mën a jariñoo ndaje bi bu baax-a-baax. Nañu seet it ni ñuy def ba ñiy ñów ak seen oto bañ a am lu leen di sonnal bu ñuy dawal, walla bu ñuy wut fu ñuy bàyyi seeni oto ak it bu ñuy wàcce nit ñi walla bu ñu leen di yeb. Kurélu magi mbooloo mi moo war a seet li gën ci seen mbooloo.
◼ Léegi, dootuñu bindati ci Sasu Nguuru Yàlla bi, téere yu bees yu ñu mën a am. Dinañu ko def ci li ñuy woowe “ Avis aux congrégations ”. Yégle yooyu dinañu ko yónne weer wu nekk ci mbooloo mu nekk. Buleen fàtte ne, saa yu ko mbooloo mi jotee, dañu war a xamal ci ndaje liggéeyu waare bi ci topp, téere yi mën a soxal seen mbooloo. Bu ñu ko defee ba pare, dinañu mën a taf yégle yooyu ci tablo fu ñuy def yégle yi ci Saalu Nguur gi. Bu loolu weesoo, kiy toppatoo téere yi ci mbooloo mi, war na denc yégle yooyu.