Jàngalal nit ñi làkk bu sell bi
1 Seede Yexowa yi dañu bokk ci ‘ xeet, giir, réew ak kàllaama ’ yu bare. Waaye mbooloo mu déggoo lañu, njaboot dëgg bu nekk ci àddina si sépp (Peeñ. 7:9). Loolu lu réy la ci àddina bu bare xaajaloo bi ñu nekk. Lu tax seede yi mel noonu ? Dañu ‘ weccee suñu làkk ak làkk bu sell ’ bi. — Tsë. 3:9.
2 Lu rafet lu muy jur : Lan mooy làkk bu sell boobu ? Mooy nànd bu baax dëgg gi nekk ci Kàddu Yàlla, dëgg gi jëm ci Yexowa ak li mu bëgg def, rawatina dëgg giy jëm ci Nguuru Yàlla. Ni ko Yeesu yégle woon, am na fi Yexowa di jaar ci kow suuf si, ngir xamal ñu dëgg gi. Mooy “ surga bu takku te teey ” bi. Loolu lu mu jur ? Nit ñi, ak làkk bu ñu mënta dégg, ñu ngi ñów bokk ci diine dëgg ji. — Macë 24:45 ; Sak. 8:23.
3 Nit ñi bu ñuy jàng làkk bu sell bi, dafa leen di xiir ci topp santaane Yexowa yi ci seen dund. Dañuy jàng “ ànd te booloo, bokk xel, bokk xalaat ”. (1 Kor. 1:10.) Li leen Yàlla di jàngal tax na ñuy def lu baax, tey wax lu wér. Te it dafa leen di waxloo dëgg, rawatina bu ñuy wax xibaar bu baax bi (Titt 2:7, 8 ; Yaw. 13:15). Ni ñuy soppeekoo noonu dafay màggal Yexowa.
4 Am na benn góor bu ñu xamaloon xibaar bu baax bi. Amoon na laaj yu bare yu mu bëggoon a xam. Ñu won ko tontu laaj yooyu yépp ci Biibël bi. Li mu dégg tax na ba mu tàmbali jàng Biibël bi ñaari yoon ayu-bés bu nekk te teewe ci ndaje yi. Teral bu neex bi ñu ko teral ci Saalu Nguur gi bettoon na ko lool, ndaxte nit ñi fa nekkoon bokkuñu woon xeet. Ci lu gaaw, moom ak jabaram daldi soppi seen dundin te ñu sóob leen ci ndox. Ginnaaw loolu, dimbali na lu mat 40 nit ba ñu bokk ci ñiy jaamu Yexowa. Ay mbokkam yu bare bokk nañu ci nit ñooñu. Nit kooku yaramam neexul, waaye bu yàggul, tàmbali na bokk ci pioñee yi.
5 Jàngalal nit ñi : Li xew ci àddina si tax na ba nit ñu bare di seetaat ni ñuy xalaate ak ni ñuy dunde. Ni Yeesu, war nañu leen a bëgg dimbali. Li ñu mën a def ngir jàngal làkk bu sell bi ñi ko bëgg dëgg, mooy dellu seeti leen, te jàng ak ñoom Biibël bi.
6 Li baax ci ñi amul jot, mooy ñu jàng ak ñoom Biibël bi, jàng bu gàtt, ci seen buntu kër (km-WO 5/02 xët 1). Ndax mas nga jéem loolu ? Booy waajal sa bopp ngir dellu seeti nit, seetal ci Sasu Nguuru Yàlla bu sãwiyee 2002 ci xët 2 ba 4, li nga ko mën a wax. Lu bare lu ñu ci bind, dañu ko def ngir ñu mën a tàmbali waxtaan ak nit ñi ci téere Laaj walla ci téere Xam-xam. Toppal waxtaan yi ñu def ci Sasu Nguuru Yàlla googu, ba mu wóor la ne boo tàmbalee waxtaan ak nit, dinga mën a tànn benn xise ci téere yooyu, waxtaan ci, te doo ci am benn jafe-jafe. Tànnal ci xise bi, benn walla ñaari aaya yi ngeen nar a jàng, te nar ci waxtaan. Tànnal it laaj boo ko mën a laaj ngir jeexal waxtaan bi. Laaj boobu dina tax boo dellusee, dinga mën a jàll ci xise bi nga bëgg ngeen waxtaane ci.
7 Mbooloo Yexowa mu ngi am ay barke yu bare ndax li muy jàng làkk bu sell bi. Nañu sawar ci dimbali nit ñi ndax ñu ñów ànd ak ñun, di ‘ woo Yexowa ci turam ’, di ànd, nekk benn te ‘ di ko jaamu ’. — Tsë. 3:9.