TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 8/03 p. 8
  • Barke yi ñuy am bu ñu nekkee pioñee

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Barke yi ñuy am bu ñu nekkee pioñee
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu jàpple pioñee yi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Tey, waxtu waare jot na !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 8/03 p. 8

Barke yi ñuy am bu ñu nekkee pioñee

1 Benn pioñee nee na : “ Mbégte bi may am bu may jàngal nit ñi dëgg gi, xam naa ne mënu ma ko am ci benn liggéey. ” Beneen pioñee moom dafa nee : “ Guddi gu nekk, damay nelaw bu baax, te sama xol sedd na. ” Pioñee yépp a ànd ak kàddu yooyu. — Léeb. 10:⁠22.

2 Ku jàng li nekk ci Biibël bi, dinga mën a mucc. Bu ñu ci dimbalee nit, dinañu bég lool (Jëf. 20:35 ; 1 Tes. 2:​19, 20). Suñu benn mbokk bu yàgg nekk pioñee nee na : “ Bu ñu gisee li Kàddu Yàlla di def ci nit ba mu soppi ni muy dundee, dañuy bég lool, te dafay dëgëral suñu ngëm. ” Waaw, barke yu mel noonu la pioñee yi di am bu ñuy dimbali nit ñi te di leen jàngal Biibël bi.

3 Dangay wéeru ci Yexowa : Bés bu nekk, bu ñuy waaraate, pioñee yi dañuy wéeru ci xelu Yàlla. Loolu dafa leen di dimbali ñu am doom bi xel boobu di jur, te dafa leen di sàmm (Gal. 5:​16, 22, 23). Te it pioñee yi foo leen fekk ñu ngi jëfandikoo Kàddu Yàlla. Looloo tax ñu aay ci wone dëgg gi nekk ci Mbind mi. Te it xam nañu bu baax ni ñuy jëfandikoo Biibël bi ngir yokk doole nit ñi (2 Tim. 2:15). Suñu benn mbokk mu nekk pioñee ay ati-at nee na : “ Nekk pioñee tax na ba sama xam-xam ci Biibël bi yaatu lool. Xam-xam boobu laay jëfandikoo ngir dimbali nit ñi, ñu xam Yexowa ak li mu bëgg def. ” Loolu wone na ne ku nekk pioñee, dafay bare mbégte.

4 Pioñee yi war nañu wéeru it ci Yexowa ci yeneen fànn. Bu ñu gisee ni Yexowa di barkeele li ñuy def ngir faj seeni soxla, dafay dëgëral seen ngëm. Am na suñu benn mbokk mu am 72 at. Nekk na pioñee lu mat 55 at. Dafa nee : “ Yexowa masul a tas sama yaakaar. ” Te yokk ci, pioñee yi dañuy aar seen bopp ci coono yu bare ndax dañuy yombalal seen dund. Ndax bëgguloo am loolu ? — Macë 6:22 ; Yaw. 13:​5, 6.

5 Dangay jege Yàlla : Suñu diggante ak Yàlla moo ëpp solo lépp lu mu mënta doon (Sab. 63:⁠3). Bu ñu bëggee Yexowa dañuy bokk bu baax ci liggéeyu waare bi. Loolu dafay rattaxal suñu diggante ak moom (Saak 4:⁠8). Suñu benn mbokk mu nekk pioñee lu ëpp 18 at nee na : “ Liggéeyu pioñee bi dafay tax ñu mën a ‘ mos te gis ne Yexowa dafa baax ’. Bés bu nekk, dañuy gën a rattaxal suñu diggante ak Ki ñu sàkk. ” — Sab. 34:⁠8.

6 Ku nekk pioñee dafa war a fexe ba ni muy dunde bañ a tax ba dootul mën a nekk pioñee. Dafa war a am itam ngëm gu dëgër, te dafa war a bëgg Yexowa ak moroomam ci biir xolam. Te it pioñee dafa war a nangu ñàkk lu bare ngir liggéey boobu (Macë 16:24 ; 17:20 ; 22:​37-39). Waaye nag, gis nañu ne, kanamu pioñee yi dafay leer fu ñu mënta nekk. Loolu mooy wone ne barke yi ñu ciy am moo gën fuuf li ñuy nangu ñàkk (Mal. 3:10). Barke yooyu, yemul rekk ci pioñee yi. Seen njaboot, ak mbooloo bi ñu bokk dinañu jariñoo bu baax ci jikko yu rafet yi pioñee yi di wone. — Fil. 4:⁠23.

[Laaj yi]

1, 2. Bu ñu nekkee pioñee, yan barke lañuy am  ? Lu tax ?

3, 4. Nekk pioñee dafa lay jàngal wéeru ci Yexowa. Naka ? Naka la lay jëmloo kanam ci wàllu ngëm ?

5. Nekk pioñee naka la lay dimbalee nga gën a rattaxal sa diggante ak Yexowa ?

6. Lan la pioñee war a def, te kan moo ciy jariñoo ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager