TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • mwb24 Septaambar p. 4
  • 9 Septaambar ba 15 septaambar

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • 9 Septaambar ba 15 septaambar
  • Dundinu kerceen ak liggéeyu waare bi—Kaye ndaje bi—2024
Dundinu kerceen ak liggéeyu waare bi—Kaye ndaje bi—2024
mwb24 Septaambar p. 4

9 SEPTAAMBAR BA 15 SEPTAAMBAR

TAALIFI CANT 82-84

Woy-Yàlla nº. 80 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

Kenn ci doomu Kore yi a ngi xool benn tàggu picc ca ëttu kër Yàlla ga

1. Nañu fonk sas yi ñu am ci liggéeyu Yexowa

(10 minit)

Dañu fonk sas yi ñu am ci liggéeyu Yexowa (Taalifi Cant 84:​2-4; wp16.6-F 8 § 2-3)

Nañu bég ci sas yi ñu am te bañ a def suñu xel ci sas yi ñu bëggoon a am (Taalifi Cant 84:11; w08-F 15/7 30 § 3-4)

Yexowa dafa baax ci ñépp ñi koy jaamu ak takkute (Taalifi Cant 84:12; w20.01-F 17 § 12)

Foto yu ñu boole: Ay sarxalkat yu nekk di liggéey. 1. Kenn a ngi sotti ndox ci ndabu xànjar bi. 2. Keneen yore puus-puus bu fees ak ay njaq. 3. Ki ci des yenu ab njaq.

Sas boo gis, am na ay barke ak ay jafe-jafe. Waaye, booy xalaat ci barke yi, dinga mën a bég ci bépp sas bu ñu la jox.

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 82:3—Won mbëggeel «jirim» yi, maanaam ñi ñàkk seen yaay walla seen pàppa te ñu bokk ci mbooloo mi, am na solo lool. Lu tax? (it-2-F 459)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

(4 minit) Taalifi Cant 82:1–83:19 (th lesoŋ 2)

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Nañu wone ne yëg nañu nit ñi—Lan la Yeesu def?

(7 minit) Waxtaan ak ñi teew. Woneel WIDEO bi, ba pare ngeen waxtaan ci lmd-F lesoŋ 9 ponk 1-2.

5. Nañu wone ne yëg nañu nit ñi—Nañu roy ci Yeesu

(8 minit) Waxtaan ak ñi teew. Waxtaan bi dafa sukkandiku ci lmd-F lesoŋ 9 ponk 3-5 ak «Seetal aaya yii itam».

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº. 57

6. Li mbooloo mi soxla ci wàllu ngëm

(15 minit)

7. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

(30 minit) bt-F pàcc 15 § 8-12 ak wërale bi nekk ci paas 118

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº. 130 ak ñaan

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager