TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • mwb24 Septaambar p. 14-15
  • 28 oktoobar ba 3 ​nowàmbar

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • 28 oktoobar ba 3 ​nowàmbar
  • Dundinu kerceen ak liggéeyu waare bi—Kaye ndaje bi—2024
Dundinu kerceen ak liggéeyu waare bi—Kaye ndaje bi—2024
mwb24 Septaambar p. 14-15

28 OKTOOBAR BA 3 NOWÀMBAR

TAALIFI CANT 103-104

Woy-Yàlla nº. 30 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Dafay «bàyyi xel ne pënd lanu»

(10 minit)

Yexowa dafa bare yërmande, looloo tax mu am gis-gis bu yem ci ñun (Taalifi Cant 103:8; w23.07-F 21 § 5)

Buñu juumee sax, Yexowa duñu bàyyi (Taalifi Cant 103:​9, 10; w23.09-F 6-7 § 16-18)

Duñu laaj mukk ñu def luñu mënul (Taalifi Cant 103:14; w23.05-F 26 § 2)

Ab jëkkër a ngi déglu jabaram bu baax mu koy wax li mu yëg ci xolam.

LAAJAL SA BOPP LII: ‘Ndax gis-gis bu yem bi Yexowa am ci ñun, feeñ na ci ni may doxale ak sama jëkkër walla sama jabar?’

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 104:24—Lan la ñu aaya bii di jàngal ci Yexowa mi sàkk lépp? (cl-F 64 § 18)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

(4 minit) Taalifi Cant 104:​1-24 (th lesoŋ 11)

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) WAARAATE CI BÉRÉB YU BARE NIT. (lmd-F lesoŋ 3 ponk 4)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(4 minit) KËROO-KËR. Nit ki dafa nangu jàng Biibël bi. Seetaanal ak moom te waxtaan ci wideo bi tudd Dalal ak jàmm ci sa njàngum Biibël bi (th lesoŋ 9)

6. Waxtaan bi

(5 minit) lmd-F appendice A idée 6—Turu waxtaan bi: Jëkkër dafa war a «bëgg soxnaam, ni mu bëgge boppam.» (th lesoŋ 1)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº. 44

7. Ndax xam nga fi sa doole yem?

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Buñuy jaamu Yexowa ak suñu xol bépp, dañuy bégal xolam te ñun itam dinañu bég (Taalifi Cant 73:28). Waaye buñu bàyyiwul xel ci fi suñu doole yem, loolu mën na tax ñu jaaxle walla ñu xàddi fekk jaru ko.

Mbokk bu jigéen bi ñu wone ci wideo bi tudd: «Xamal fi sa doole yem te def li nga mën sa xol bépp».

Woneel WIDEO bi tudd: Xamal fi sa doole yem te def li nga mën ak sa xol bépp. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Lan la Yexowa di xaar ci ñun? (Mise 6:8)

  • Li ñu nar a gis ci wideo bi tudd: «Xamal fi sa doole yem te def li nga mën sa xol bépp». Mbokk bu jigéen bi ak xaritam ñu ngi ci restaurant di dëfal kenn kiy jàng Biibël bi.
  • Lan moo dimbali mbokk bu jigéen bi mu bañ a jaaxle lool ci ni mu mënee matal jubluwaay bi mu amoon?

NAKA LAÑU MËNEE XAM FI SUÑU DOOLE YEM?

  • Nañu moytu di diirante mbagg ak ñeneen ñi (Galasi 6:4). Li ngay def walla li nga gis ne moom nga mën a def warul a aaju mukk ci li ñeneen di def. Xéyna li nga mën a def moo ëpp walla moo gën a tuuti li keneen mën a def bu dee sax yeen a maase walla li seen njaboot di dund benn la.

  • Buñu bàyyi ragal tere ñu, ñu def li ñu masul a def (Room 12:1; 1 Korent 7:31). Bul ragal a liggéeyal Yexowa ci fànn boo xam ne ci yaw lu jafe la, walla nga xalaat ne doo ci am mbégte.—Malasi 3:10

  • Nañu am ay jubluwaay yu ndaw ngir mën a xam fi suñu doole yem. Ci misaal ndax mën nga nekk pioñee permanã? Lu tax doo jéem a yokk waxtu yi ngay def ci liggéeyu waare bi walla nga jéem a nekk pioñee oksiliyeer? Ndax mën nga jéem a nekk pioñee permanã diiru benn at? Bu dee sax dem nga ba gis ne mënuloo nekk pioñee permanã walla mënuloo ko nekk lu ëpp benn at, doo reccu mukk ci ni nga jéemee matal yenn jubluwaay yu ndaw yi—Kàdduy Waare 6:9

  • Nañu nangoo xalaataat ci li ñu mën a def. Suñu dund mën na soppeeku, suñu mën-mën itam. Kon nañuy faral di xoolaat bu baax suñu jubluwaay yi ngir xam li ñu war soppi.

8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

(30 minit) bt-F pàcc 17 § 8-12 ak wërale bi nekk ci paas 137

Kàddu yi ñuy tëjee ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº. 55 ak ñaan

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager