Woy-Yàlla 19 (43)
Aywa, yéen ndawiy Nguur gi!
(2 Timote 4:5)
1. Aywa, nañu dem waare Nguur gi
Nitiy xeeti suuf si sép’.
Bëgg’ dimbali ñii suufeelu,
Ñu faral Yeowa kep’.
Ngir màggal suñ’ sas bu tedd bi,
Nañ’ bàyyi xel ci suñu col.
Yeowa lañuy wut a barkeel;
Na njaamoom sax ci suñu xol.
(AWU)
Aywa, nañ’ dem
Waareji xabaaru Nguur gi fu nekk.
Aywa, nañ’ jëm
Kanam, di déggal Yàlla saa su nekk.
2. Ndaw yu bees yi, aywa, jëm kanam,
Di séentu yoolu Yàlla.
Fàtteleen li ngeen bàyyi ginnaaw,
Waarleen, ànd ceek fulla.
Yeesluleen ci dooley Kàddug gi,
Noonu wuuteek àddina sii.
Siggalleen Yàlla, Musalkat bi;
Woote na; dawleen wuyusi.
(Awu)
3. Àndleen di wéy tey jëm kanam,
Yéen, des week ‘yeneen xar’ yi.
Aywa, mag ak ndaw, jigéen ak góor,
Buleen nangoo kay-kayi.
Dañoo fonk suñu sas, ba tax
Dañu ko fas yéenee sargal.
Day tagg Yàlla, di ko màggal,
Ñi sopp dëgg lay dëfël.
(Awu)