Woy-Yàlla 26 (56)
Ak fit, nañ’ jëm kanam
(1 Timote 1:12)
1. Kii di ku takku, kii di ku gore,
Du nangu mukk ragal
Waaye dafay seedeel dëgg gi ak fit,
Naan, Nguuru Yaa daa dégmal.
(AWU)
Kon nag aywa, nañ’ jëm kanam.
Dëgg gi, tey, ’ngiy melax.
Yeowa nee na: ‘Dinaa la dimbali;
Xeexal ngir li jub te baax.’
2. Ngëm mooy doole gi ñuy jëmloo kanam,
Mbëggeel di ñu xiir ci ngor.
Sawar ci mbiriy Buur bi day farluloo;
Siis du jikko nit ku ñor.
(Awu)
3. Yeowa, Jàmbaar ci biir xare bi,
’Ngi ñuy xiirtal ci takku
Ba Ar-Magedon di fi jële ñi bon;
Waaw ci ndamam lay bàkku.
(Awu)