WOY-YÀLLA 162
Dinaa suuxat sama ngëm
(Macë 5:3)
1. Yàlla def na ci ñun ñépp,
yëg-yëg bu am solo lool.
Looloo ñuy xiir ñuy laaj lu tax
ñuy dund ci kaw suuf.
Nit wut na tontu, gisul,
waaye Yàlla sorewul.
Kàddoom a wóor tey sax ba fàww.
Du mas a tas yaakaar.
(AWU BI)
Damay màggal Yexowa.
Guddeek bëccëg, moo may tette.
Man daal, Yexowaa ma moom.
Kàddoom a may dundal.
Duma tàyyi di
suuxat sama ngëm.
2. War naa dundal sama ngëm.
Gëstu, xóotal li ma gëm,
ndax jariñoo Kàddu Yàlla,
wax dëgg, bànneex la.
Ñiy tanqamlu dëgg gi
Yal na seen xel dellusi,
Yàlla may leen jàmm juy sax,
ñu ànd bànneexu.
(AWU BI)
Damay màggal Yexowa.
Guddeek bëccëg, moo may tette.
Man daal, Yexowaa ma moom.
Kàddoom a may dundal.
Duma tàyyi di
suuxat sama ngëm.
Damay màggal Yexowa.
Guddeek bëccëg, moo may tette.
Man daal, Yexowaa ma moom.
Kàddoom a may dundal.
Duma tàyyi di
suuxat sama ngëm.
Damay màggal Yexowa.
Guddeek bëccëg, moo may tette.
Man daal, Yexowaa ma moom.
Kàddoom a may dundal.
Duma tàyyi di
suuxat sama ngëm.
(Xoolal itam Taalifi Cant 1:1, 2; 112:1; 119:97; Esayi 40:8; Macë 5:6; 16:24; 2 Timote 4:4.)