Li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi
La Tour de Garde 15 sept.
“ Daanaka ci diine yi yépp, am na ñu fonk liy dëgg. Ndaxam féewoo faral na di am diggante doom-Aadama yi ndax diine. Waaw, lu ciy pexe, ba tax ñi seen xol jub mën a ànd a nekk benn ? [Bu tontoo, jàngal Tsëfanyaa 3:9.] Yéenekaay bii day wone naka la xam-xamub Yàlla dëgg ji nekkee di xiir nit ñi ci déggoo, fépp ci kow suuf. ”
Réveillez-vous! 22 sept.
“ Li ëpp ci ñun dañoo jàpp ne, duñu toog mukk ba gis lekk gu bare ñàkk. Waaye, tey, am na ñu ragal, xam-xam-sës (siãs) indi musiba ci li ñu denc ci lekk, ci kow suuf si. Yéenekaay bii day faramfàcce yenn ci njaaxle yooyu, akit yaakaar ji ne ci Biibël bi, te jëm ci liy saafara dëgg jafe-jafe boobu. ”
La Tour de Garde 1 okt.
Xéy na nangu nga ne ñu bare bëggatuñu di waxtaane ngëm ci Yàlla. Lu waral loolu ? [Bu tontoo, jàngal Yawut yi 11:1.] Yéenekaay bii day waxtaan ci li ngëm dëgg doon, akit li am ngëm, walla ñàkk ko, mën a yóbbe ci suñu dund. ”
Réveillez-vous! 8 okt.
“ Xam nga ne Halloween xew bu mag la, te xale yu bare fonk nañu ko lool. Waaye ndax mas ngaa toog ba seet fu mu cosaanoo ? [May ko mu tontu.] Dinga gis ne, li ñu fiy waxtaane dina la dugg dëgg, rawatina boo dee way-jur ju ittewoo sutura say doom. ”