Faramfàcceel ci fasoŋ bu jub Kàddug Yàlla
1 Ba mu doon seede benn jaraaf, “ Filipp [daa] tàmbale ci [ab] aaya [...], xamal ko xebaar bu baax bi ci mbirum Yeesu ”. (Jëf. 8:35.) Filipp a nga doon “faramfàcce bu jub kàddug dëgg gi ”. (2 Tim. 2:15.) Waaye tey, ay wottukat yuy wër mbooloo karceen yi seetlu nañu lii : jafe naa gis yéenekat yuy jëfandikoo Biibël bi, bu ñuy seede. Ndax dingay jëfandikoo Biibël bi ci sa sasu waare ?
2 Lépp li ñu gëm te di ko jàngale, ci Kàddug Yàlla la cosaanoo (2 Tim. 3:16, 17). Loolooy liy xiir nit ñi ci Yexowa, te moo leen di yar ngir dund gi. Looloo tax, jëfandikoo Biibël bi ci suñu sasu waare nekk lu am solo, asté ñoo yem ciy waxtaane ponk yu ñu itteel, ñun (Yaw. 4:12). Ndegam li ëpp ci nit ñi, seen xam-xam ci Biibël bi sorewul, soxla nañu koo jàng ngir won leen njariñu tette bi ci nekk, akit ëllëg ji mu dig doom-Aadama yi.
3 Jàngeel ci Biibël bi saxsax : Mën ngaa jéem a dem ci kër yi, bañ a yore saag. Mën ngaa def mbind yi nga war a won nit ñi ci defukaayu kayit bu sew, ba noppi ŋàbb sa Biibël ci loxo walla nga def ko ci sa biir poos. Léegi, booy waxtaan ak nit ki, mën ngaa génne sa Biibël, ci fasoŋ bu nit ki dul xalaat ne danga koy jéem a waare. Taxawal ci fasoŋ buy may ki lay déglu, mu mën a jàngandook yaw ci sa biir Biibël. Xéy na, mën nga koo laaj mu jàng ca kow ab aaya. Mbir mi dina ko gën a dugg, bu mënee gisal boppam li Biibël biy wax ; mooy gën fuuf li mu mën a dégge ci yaw. Jarul ñu koy wax, ngir dimbali ko mu nànd li ëpp solo ci aaya ji, fésalal baat yi ëmb xalaat bi.
4 Jàngal benn aaya kese : Boo nuyoo, mën ngaa wax lii : “ Fi nit ñu bare di jublu ngir xam ni ñuy doxale seen dund, bare na. Fan nga foog ne mooy fi gën, fu ñu war a jublu ngir jot ci tette buy jariñ ? [May ko mu tontu.] Loo xalaat ci wax jii ? [Jàngal Léebu 2:6, 7, te may ko mu tontu.] Xam-xamu doom-Aadama, ndeysaan, ku ko jëfe day gisal boppam ne daa des, ndax jëme na ñu bare ci ñàkk yaakaar. Waaye topp xam-xam bi jóge ci Yàlla, daa mas a doon lu mat a wóolu tey jariñ. ” Woneel léegi mbind mi nga yore, te fésal ak menn misaal, liy firndeel ne jëfe xam-xam bi jóge ci Yàlla day jariñ dëgg.
5 Yeesu jëfandikoo woon na Mbind yi ngir dimbali ñi seen xol jub (Lukk 24:32). Pool firndeel na li mu doon jàngale ak Mbind yi (Jëf. 17:2, 3). Suñu kóoluteek suñu mbég ci sasu waare bi dinañu yokku, bu ñuy gën di aay ci faramfàcce ci fasoŋ bu jub Kàddug Yàlla.