Ndaje bu mag bu ñaari fan biy ñów : li ñu fay waxtaane
1 Yeesu waxoon na ne taalibeem yi dinañu am coono (Macë 24:9). Naka lañu war a gise coono yi ñuy dal ? Lan mooy tax ñu mën leen a muñ ? Ndaje bu mag bu ñaari fan bi ñuy am déwén dina tontu laaj yooyu. Turam mooy : “ Bégleen ci yaakaaru ëllëg, te muñ bépp tiis ”. — Room 12:12.
2 Ñaari waxtaan yu def ay xaaj : Bu ñjëkk bi mu ngi tudd : “ Nañu muñ ba jur njeriñ ”. Dina wone ci ban fànn lañu mën a jur njeriñ. Dinañu laaj ay waaraatekat ñu wax naka lañuy wone ci ni ñuy waaraatee ak ni ñuy jàngalee Biibël bi ne xam nañu ne bésu Yàlla jegesi na. Xaaj bi tudd “ Bu ñu Yexowa yaree ” dina neex lool way-jur yi ndaxte dina wone ni ñu mënee waxtaan ak seeni doom bu ñu leen di bëgg jàngal dara. Kiy def xaaj bu mujj bi dina wone ni ñu mënee def ba àddina si bañ ñoo wàll ndànk-ndànk ba tere ñu jur njeriñ. — Mark 4:19.
3 Beneen waxtaan bi def ay xaaj mu ngi tudd : “ Nañu daw ci rawante bi te bañ a tàyyi ”. Dina wone lu tax suñu dund mel ni rawante. Lu tax ñu war a topp sàrt yi bokk ci rawante bi ? Naka lañu mëne dindi lépp li ñu mën a diisal te bañ a tàyyi ci rawante bi ñuy def ngir mën a dund ? Ñun ñépp dinañu fa dégg ay xelal yu baax yu ñu jële ci Mbind mi, yu ñuy dimbali ngir ñu kontine di daw te bañ a tàyyi.
4 Ku muñ dina neex Yàlla : Waare yi wottukat biy wër di def, ku leen déglu te topp, sa ngëm dina gën a dëgër. Benn waxtaan ci yi wottukat biy wër ci circonscription yi di def (ci tubaab surveillant de district) dina tudd “ Muñ dafay tax ñu neex Yàlla ”. Waxtaan bu ñu jagleel ñépp dina tontu ci laaj yii : Ci turu kan la xeet yi war a wékk seen yaakaar ? Te loolu lan lay laaj ? Waxtaan bi ñuy mujj def mooy bii : “ Seen muñ moo leen di musal ”. Dinañu seet li taxoon Yeesu mën a muñ lu jaaduwul li ñu ko def te xolam bañ ci jeex.
5 Buleen fàtte yóbbaale téere École du ministère ak La Tour de Garde bi ñu war a jàng ayu-bés boobu. Bindleen li ëpp solo ci li ngeen di dégg ci ndaje boobu. Dina tax seen xel gën a nekk ci li ñuy wax te bés bu ngeen ko bëggee dingeen ko mën a jàngaat. Ginnaaw ndaje bu mag boobu, dinañu seetaat ci mbooloo mi li ñu fa jàng.
6 Yexowa ci boppam moo ñu waajalal ñamu xel bu bare te neex boobu. Ñëwal ñu bokk ko, ñun ñépp ! Ku fekke waxtaan yi ñu fay def yépp, dinga bég lool. — Isa. 65:14.