Nañu wone jikko yi jekk ci pioñee
1 Waaraatekati Nguur gi yépp, bu ñu mënee nekk pioñee tey ak bu ñu ko mënagul yépp, mën nañu wone jikko yi jekk ci pioñee. Lu koy wone ? Dañu bëgg waaraate ak sàkk ay taalibe ni leen ko Yeesu laaje (Macë 28:19, 20 ; Jëf. 18:5). Dañu bëgg toppatoo nit ñi te dañuy xañ seen bopp yenn yi ngir mën a def liggéeyu waare bi (Macë 9:36 ; Jëf. 20:24). Te it ñiy jaamu Yexowa nangu nañu def lépp li mën a dimbali nit ñi ngir ñu jàng dëgg gi (1 Kor. 9:19-23). Filipp, taskatu xibaar bu baax bi, bokk na ci ñi wone jikko yu mel noonu. Nañu seet li mu def.
2 Waaraate ak jàngale : Ci jamano karceen yu njëkk ya, dénkoon nañu Filipp liggéey bu am solo ci mbooloo mi (Jëf. 6:1-6). Waaye liggéey bi mu doon gën a def moo doon waare xibaar bu baax bi. Dafa ci sawaroon lool (Jëf. 8:40). Kon nag tey, mag ak surga mbooloo yi, bu ñuy def seen liggéey ci mbooloo mi, mën nañu wone it jikko yi jekk ci pioñee. Naka ? Nañu jiite liggéeyu waare bi te sawar ci lool. Dina tax jikko yu rafet yi nit ñi di wone ci mbooloo mi gën a yokku. — Room 12:11.
3 Fitnaal bi ñu doon fitnaal taalibe Yeesu yi, dafa yokku bu baax-a-baax bi Ecen deewee. Moo tax seen dund jaxasoo lool. Waaye loolu terewul Filipp kontine waaraate. Li mu def ci liggéeyu waare bi bokk na bu baax ci li tax waaraate bi àgg ba ci waa Samari (Jëf. 8:1, 4-6, 12, 14-17). Ñun itam mën nañu def ni moom. Bu ñu nekkee ci fitna sax, nañu kontine di xamle xibaar bu baax bi. Te it bu ñuy waaraate, nañu wax ak nit ñépp te bañ a gënale. — Ywna. 4:9.
4 Liggéey bu rafet bi Filipp def bi mu doon jàngal Kàddu Yàlla feeñ na ci li mu def ba jaraafu Ecópi bi tuub (Jëf. 8:26-38). Kon leneen li ñu mën a def ngir wone jikko yi jekk ci pioñee, mooy fexe ba gën a mën a jëfandikoo Biibël bi te di “ werante ” ak nit ñi “ ci li Mbind mi wax ”, maanaam waxtaan ak ñoom ci Mbind mi (Jëf. 17:2, 3). Ni Filipp, dañuy jéem a xamle xibaar bu baax bi fépp fu ñu mën a fekk nit ak saa yu ñu ci amee bunt.
5 Ci njaboot gi ak ci mbooloo mi : Ci lu wóor jikko Filipp yi ak li mu daan def, am na lu baax li mu jur ci doomam yu jigéen yi (Jëf. 21:9). Noonu it waajur karceen yiy jiital Nguur gi ci seen dund, dañuy xiir seen doom ci lu mel noonu. Waajur boo xam ne dafay liggéey ba sonn ayu-bés bi yépp, waaye ci fan yi mujj yi ci ayu-bés bi dafay sawar a dem waaraateji, mën na def ci xolu doomam lu fay yàgg lool. — Léeb. 22:6.
6 Filipp teraloon na ca këram ñaari karceen yu sawaroon lool ci liggéeyu Yexowa, maanaam Pool ak Lukk (Jëf. 21:8, 10). Ñun nag tey, naka lañu mënee won ñi sawar ci liggéeyu Yexowa ne fonk nañu leen te dañu leen bëgg jàpple ? Xéyna mën nañu wax pioñee yi ne mën nañu ànd ak ñoom ci waaraate bi, ci bés yoo xam ne ñiy dem waaraate duñu bare (Fil. 2:4). Mën nañu leen wax itam ñu ñów suñu kër ngir ñu mën a waxtaan ak ñoom, waxtaan bu neex te am njariñ. Ak lu ñu mënta nekkee, nañu góor-góorlu ñun ñépp ngir wone jikko yi jekk ci pioñee.
[Laaj yi]
1. Lan mooy jikko yi jekk ci pioñee ?
2. Naka la mag ak surga mbooloo yi mënee roy Filipp ci ni mu saware woon ci waaraate bi ?
3. Bu ñu nekkee ci fitna, naka lañu mënee wone jikko yi jekk ci pioñee ?
4. Lan la ñu Filipp won ci wàllu njàngale mi ?
5. Lan moo mën a tax waajur bu nekk karceen mën a def ci xolu doomam jikko yi jekk ci pioñee ?
6. Naka lañu mënee won pioñee yi nekk ci suñu mbooloo ne fonk nañu li ñuy def ?