Xaaj 8 : Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
Nañu jëmale nit ñi ci mbootaayu Yàlla
1 Bu ñuy jàngale Biibël bi, li ñu bëgg mooy nit ñi gëm li nekk ci Biibël bi. Waaye bëgg nañu it ñu bokk ci mbooloo karceen yi (Sak. 8:23). Téere bi tudd Les Témoins de Jéhovah : Qui sont-ils ? Quelles sont leurs croyances ? moo ñu ci mën a dimbali. Nanga ci jox benn ñi sog a tàmbali njàngum Biibël bi, te wax leen ñu jàng ko. Ci njàngum Biibël bi ngay def ayu-bés bu nekk, nanga jël tuuti minit ngir waxtaan lu jëm ci mbootaayu Yexowa.
2 Ndaje yi ñu am ci mbooloo mi : Kuy jàng Biibël bi war na nangu te bëgg mbootaayu Yàlla. Li ko ci gën a mën a dimbali mooy teewe ndaje yi ñu am ci mbooloo mi (1 Kor. 14:24, 25). Kon, war nga koo xamal lu jëm ci ndaje yooyu. Li nga mën a njëkk a def mooy, saa yoo defee njàngum Biibël bi, nga wax ko ci benn ndaje ci juróomi ndaje yi ñu am ayu-bés bu nekk. Booy wax ci ndaje bi ñu jagleel ñépp, wax ko yaxu waxtaan bi ngeen war a am ayu-bés bii di ñów. Won ko li ngeen war a waxtaan ci Njàngum La Tour de Garde ak Njàngum téere bii di ñów. Lu jëm ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ak ndaje bi jëm ci liggéeyu waare bi, wax ko ni ñu leen di doxale. Boo amee waxtaan boo nar a def ci lekkool bi, xéyna dinga ko mën a def ci kanamam, mel ni yaa ngi ci bésu ndaje bi. Nanga waxtaan ak moom ci ay ponk yu am solo yi amoon ci ndaje yi nga teewe woon. Won ko ci suñuy téere ay foto yuy wone ni ndaje yi di deme. Bés boo defee njàngum Biibël bu njëkk bi, nanga ko komaasee woo ci suñuy ndaje.
3 Xéyna dina am lu nar a ñów, mel ni ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, ndaje yu mag ak yu gën a mag yi, walla wottukat biy wër bu ñuy seetsi. Su loolu waree am, jëlal tuuti minit ngir wax ko ni ndaje yooyu di deme ak li la ci neex. Te fexeel ba mu bëgg ci teew moom it. Ndànk-ndànk nanga waxtaan ak moom ci laaj yii di topp : Lu tax ñu tudd Seede Yexowa ? Lu tax ñuy woowe Saalu Nguur gi béréb fi ñuy defe suñuy ndaje ? Lan mooy liggéeyu magi mbooloo mi ak surgay mbooloo mi ? Naka lañuy doxale liggéeyu waare bi ci gox yi ? Naka lañuy defare suñu téere yi ? Fan la mbootaay bi ame xaalis bi mu soxla ngir def lépp li muy def ? Lan la Bànqaas yi ak Jataay biy dogal di def ngir jiite lépp lu jëm ci liggéeyu waare bi ?
4 Ay wideo yuy jàngale : Ñiy jàng Biibël bi, am na leneen lu leen mën a won mbootaay bu rafet bi Yexowa moom. Loolu, suñu wideo yi la. Bi tudd Jusqu’aux extrémités de la terre dafay wone ni ñuy defe suñu liggéeyu waare bi ci àddina si sépp. Wideo bi tudd Toute la communauté des frères dafay wone naka la Seede Yexowa mele ni benn njaboot ci àddina si sépp. Te wideo bi tudd Unis grâce à l‘enseignement divin mooy won ni ñu nekke benn. Am na benn jigéen bu faraloon a jël suñuy yéenekaay ak it yenn ci suñu téere yi. Def na loolu juróomi at ba bés bi mu seetaan wideo bi tudd Les Témoins de Jéhovah — un nom, une organisation. Wideo boobu, dafa ko laal ba mu jooy. Dëgg la, dafa wóolu woon Seede yi ko doon seetsi. Waaye bi mu seetaanee wideo bi, ci la xame ne mën na wóolu it mbootaay bi. Tàmbali na benn njàngum Biibël te ayu-bés bi ci topp dafa komaasee teewe suñuy ndaje ci Saalu Nguur gi.
5 Benn mbootaay rekk la Yexowa di jëfandikoo ci suñu jamano jii. Te ñun, dañu bëgg ñiy jàng Biibël bi ak ñun, ñu xam mbootaay boobu. Am nañu ay téere ngir loolu. Ayu-bés bu nekk, nañu jël tuuti minit ngir waxtaan ci. Bu ñu defee loolu, dinañu leen jëmale ndànk-ndànk ci mbootaayu Yexowa.
[Laaj yi]
1. Ci njàngum Biibël bu ñuy def ayu-bés bu nekk, waxtaan ci benn ponk bu jëm ci mbootaayu Yexowa, lu tax mu baax ?
2. Naka nga mënee xiir ñiy jàng Biibël bi ñu teewe ndaje yi ñuy am ci mbooloo mi ?
3. Ci yan ponk yu jëm ci mbootaay bi lañu mën a waxtaan bu ñuy def njàngum Biibël bi ?
4, 5. Naka la suñu wideo yi mënee xiir nit ñi ci fonk mbootaay bi ?