Mag ak ndaw war nañu ko roy
Nit kooku, moom ak Yàlla, seen diggante dafa rattaxoon lool. Lenn rekk la bëggoon ci àddinaam : def li Yexowa bëgg. Dafa doon “ topp Yàlla ” te loolu indil na ko ay barke yu bare. Nit kooku, Nóoyin la woon (Njàl. 6:9). Mag ak ndaw yépp a ko war a roy. Wideo bi tudd Noé : il marchait avec Dieu, dina leen won ni Nóoyin doon dunde, lu tax Yexowa barkeel ko, ak ni ngeen ko mënee roy ci jikkoom yu rafet yi.
Laaj yii di topp ñu ngi ci DVD bi jëm ci Nóoyin. Nangeen ko seetaan ba pare laaj seen bopp laaj yii : 1) Am na ay malaaka yu def lu bon. Lu bon loolu lan la ? Ñan ñoo doon ñeyi xaree yi nekkoon ci àddina (maanaam nefilim yi) ? (Njàl. 6:1, 2, 4) 2) Ci jamano Nóoyin, lu tax nit ñi soxoroon lool ? Loolu lu mu doon def Yàlla ? (Njàl. 6:4-6) 3) Ci lan la Nóoyin wuute woon ak ñeneen nit ñi ? (Njàl. 6:22) 4) Naka la Yàlla alage nit ñu bon ñi ? (Njàl. 6:17) 5) Gaal gi Nóoyin tabax, naka la tollu woon ? (Njàl. 6:15) 6) Bi mu doon tabax gaal gi, am na leneen lu Nóoyin def. Loolu lan la te ndax am na lu mu def ci nit ñi ? (Macë 24:38, 39 ; 2 Piy. 2:5) 7) Ci xeetu mala bu nekk, ñaata mala la Nóoyin doon dugal ci gaal gi ? (Njàl. 7:2, 3, 8, 9) 8) Ñaata fan la taw ? Ñaata fan la suuf si fees ak ndox ? (Njàl. 7:11, 12 ; 8:3, 4) 9) Lan moo tax Nóoyin ak njabootam mucc ? (Njàl. 6:18, 22 ; 7:5) 10) Fan la gaal gi teere ? (Njàl. 8:4) 11) Naka la Nóoyin xame ne léegi mën na génn gaal gi ? (Njàl. 8:6-12) 12) Bi Nóoyin génnee gaal gi, lan la njëkk def ? (Njàl. 8:20-22) 13) Xon bi (arc-en-ciel), lan la doon misaal ? (Njàl. 9:8-16) 14) “ Topp Yàlla ” mooy lan ? (Njàl. 6:9, 22 ; 7:5) 15) Bu ñu bëggee bokk ci ñiy gis Nóoyin ci Àjjana jiy ñów, lan lañu war def tey ? (Macë 28:19, 20 ; 1 Piy. 2:21)
Nóoyin, ku gëm Yàlla la woon te dafa doon topp Yàlla bu baax. Li Biibël bi wax ci Nóoyin, lu mu la jàngal ci fasoŋ bi ñu mënee “ topp Yàlla ” ak ci ni Yexowa mënee muccal mbooloom tey ? — Njàl. 7:1 ; Léeb. 10:16 ; Yaw. 11:7 ; 2 Piy. 2:9.