Ndax waajal nga sa bopp ba xam li ngay def bu musiba dalee ci kow nit ñi ?
1. Lu tax waajal suñu bopp bala musiba di dal suñu kow mooy li gën a wóor ?
1 At mu nekk, ci àddina si sépp, ay musiba dañuy dal ci kow ay milioŋi nit, boole ci yu bare ci suñuy mbokk ci ngëm. Musiba yooyu mën na nekk yëngu-yëngu suuf, tsunami, taw yuy ànd ak ngelaw bu am doole, dex yu fees bay tuuru ak yu mel noonu. Musiba yi dañuy bette te mën nañu dal ci kenn ku nekk ci ñun. Kon waajal suñu bopp bala ñuy am, xel la. — Léeb. 21:5.
2. Lu tax ñu war a xamal njiit yi suñu adarees ak suñu nimoro telefon ?
2 Bala musiba di am : Bu musiba di waaj a am, yenn saay nguuru réew mi mën na ko ràññe te yégal ko nit ñi. Bu booba war nañu déglu bu baax li ñuy wax (Léeb. 22:3). Bu nguur gi waxee lu mel noonu, njiiti mbooloo mi dinañu jéem a wax ak ñi bokk ci mbooloo mi ñépp ngir dimbali leen ñu waajal seen bopp ni mu ware. Bu musiba bi amee ba pare it, njiit yi dinañu def lépp li ñu mën ngir wax ak ñi bokk ci mbooloo mi ñépp, ba xam ndax dara jotu leen te seet it lan lañu war a soxla. Bu njiit yi amulee adareesu nit ñi nu war a waxal walla mu am ku ci soppi adareesam te waxu ko ba ñu bind ko, dina leen tàrdeel fekk ci waxtu boobu jot bi dafa xat. Kon nag waaraatekat yi war nañu xamal seen adarees ak seen nimoro telefon, sekkerteer bi ak kiy jiite njàngum Biibël bi ñu bokk.
3. Bu fekkee ne dañu dëkk ci béréb fu musiba faral a am, naka lañu mënee jàpple njiiti mbooloo mi ?
3 Mën na am suñu mbooloo dafa féete ci béréb fu musiba faral a am. Kon njiiti mbooloo mi dinañu wax waaraatekat yi ñu jox leen tur ak nimoro telefonu seen benn mbokk mbaa seen benn xarit bu dëkkul ci gox boobu, ngir ñu woo ko bu musiba amee. Loolu dina tax njiit yi mën a xam fi nit ñi nu rawale nekk. Mën na am it njiit yi bëgg taxawal li waa mbooloo mi war a def bu musiba dalee ci kow nit ñi. Mën nañu ci boole kayit fi ñu bind li nit ku nekk war a denc fu neex a jot, li ñu war a def ngir jële nit ñi ci béréb fu musiba dal ak li ñu war a def ngir jàpple ñi soxla ndimbal. Mbëggeel rekk a tax ñuy taxawal loolu, te war nañu topp lépp li ñu ci wax. — Yaw. 13:17.
4. Bu musiba dalee fi ñu dëkk, lan lañu war a def ?
4 Bu musiba amee ba pare : Bu musiba dalee fi nga dëkk, lan nga war a def ? Seetal bu baax ndax sa njaboot amul soxla yu ñu war a faj ci lu gaaw-a-gaaw. Nanga jàpple ni nga ko mëne sa moroom yi musiba bi gaañ walla yàqal. Fexeel ba woo kiy jiite njàngum Biibël bi nga bokk walla beneen njiitu mbooloo mi, ci ni mu gënee gaaw. Bu dee sax dara jotu la te soxlawuloo ñu dimbali la ci dara, war nga leen a woo. Bu dee danga soxla ndimbal, na la wóor ne sa mbokk yi dinañu def lépp li ñu mën ngir jàpple la (1 Kor. 13:4, 7). Bul fàtte ne Yexowa gis na li nga nekke, te nanga wéeru ci moom ngir mu jàpple la (Sab. 37:39 ; 62:8). Boo gisee nit ku soxla ndimbal ci wàllu ngëm walla ku xolam jeex, nanga seet loo mën a def ngir jàpple ko (2 Kor. 1:3, 4). Nanga gaaw a dellu ci li nga tàmmoon a def ci wàllu ngëm. — Macë 6:33.
5. Li musiba yi di mënee dal fu nekk, naka lay laale karceen yi ?
5 Musiba mën na dal fu nekk. Te loolu tiital na nit ñi lool. Waaye ñun mën nañu séentu ëllëg ak xel mu dal. Léegi musiba dootu fi amati (Peeñ. 21:4). Waaye bala loolu, mën nañu waajal suñu bopp ngir xam li ñu war a def bu metit ak coono dalee suñu kow. Ñu boole ci it di sawar lool ci liggéeyu xamle xibaar bu baax bi.