Ndimbal bi ñu mën a am ci Njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi
1. Naka la suñu juróomi ndaje yi ñuy am ayu bés bu nekk di ñu dimbalee ?
1 Suñu juróomi ndaje yi ñuy def ayu bés bu nekk, bu ci nekk wuute na ak moroomam ci ni ñu koy defe, wuute it ci li waral ñu koy def. Waaye ndaje yooyu yépp dañuy tax ñu mën a “ xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax ” (Yaw. 10:24, 25). Lan moo nekk ci njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi te amul ci yeneen ndaje yi te mu nekk lu am njariñ lool ?
2. Lan moo baax ci daje ak gurup bu ndaw ci Njàngum téere bi ?
2 Dafa ñuy dimbali ñu jëm kanam ci wallu ngëm : Ci lu ëpp, ñiy teewe ndaje njàngum téere bi ñoo gën a néew ñiy teewe yeneen ndaje mbooloo mi. Kon ci ndaje boobu, am ay xarit yu la mën a dimbali ci wàllu ngëm, dina la gën a yomb (Léeb 18:24). Ndax jéem nga xam képp ku nekk ci sa Njàngum téere, xéyna di leen wax ngeen ànd ci liggéeyu waare bi ngir gën a xamante ? Njàngum téere bi dafay tax it wottukat bi koy jiite mën a xam li képp ku nekk ci njàngum téere bi nekke ak li mu mën a def ngir dimbali ko ci wàllu ngëm. — Léeb 27:23.
3. Njàngum téere bi, naka lay dimbalee ñiy jàng Biibël bi ñu teew te bokk ci waxtaan yi ñu fay def ?
3 Ndax wax nga ñi ngay jàngal Biibël bi ñu teewe Njàngum téere bi ? Am na nit ñu suñu waxtaan neex waaye dañu ragal a teew ci ndaje bu bare nit. Teewe ndaje bu barewul nit mën na gën a yomb ci ñoom, rawatina bu dee ci këru suñu benn mbokk lañu koy defe. Miinante bi fay am dina tax tontu laaj yi ñu fay laaj gën a yomb ci ndaw yi ak ñi sog a teewe suñuy ndaje yi. Te ndegam nit ñi barewuñu, dinañu gën a mën a bokk ci waxtaan bi te màggal Yexowa. — Sab. 111:1.
4. Ci lan la Njàngum téere bi mënee baax itam ?
4 Ci lu ëpp, Njàngum téere yi dañu leen di tasaare ci goxu mbooloo mi, ci ay béréb yu baax ci waaraatekat yi. Su fekkee ne sax du ñépp ñoo mën a bokk ci Njàngum téere bu leen gën a jege, ba tey fi ñu lay boole moo la war a gën a jege fi ñuy defe yeneen ndaje mbooloo mi. Te it, fi ñuy defe Njàngum Biibël bi mën na nekk béréb bu baax ngir ndaje yu ñuy def bala ñuy dem waare.
5. Lan lañu mën a def ngir wottukat biy jiite suñu Njàngum téere bi dimbali ñu ci waaraate bi ?
5 Dafa ñuy dimbali ci liggéeyu waare bi : Kiy jiite Njàngum Biibël bi dafa bëgg a dimbali kenn ku nekk mu faral di bokk ci liggéeyu waare bi, am ci mbégte, te def ci liggéey bu baax. Moo tax muy góor góorlu ngir ànd ak képp ku bokk ci gurup bi te jàpple ko ci fànn yu bare ci liggéeyu waare bi. Boo amee ay jafe-jafe ci benn fànn ci waaraate bi, mel ni dellu seeti nit ñi, wax ko wottukat biy jiite seen Njàngum téere. Mën na la boole ak waaraatekat bu aay bu nekk ci seen gurup ngir mu dimbali la. Dinga gën a aay ci jàngale Biibël bi boo xoolee bu baax ci fasoŋ bu rafet bi wottukat biy jiite Njàngum téere bi di jàngalee ci ndaje boobu. — 1 Kor. 4:17.
6. Lu tax ñu war a def lépp ngir jariñoo bu baax ndaje bi tudd Njàngum téere bi ?
6 Njàngum téere bi ñu am ci mbooloo mi, barke dëgg la ! Dafay wone ne Yexowa dafa ñu bëgg ! Dafa ñuy dimbali ñu kontine di jëm kanam ci wàllu ngëm ci jamano ju bare jafe-jafe jii ñu tollu nii. — Sab. 26:12.