Note
a Mbindu mooma da doon dimbali Nguurug Room mu sàkk galag. Noonu, Ogust ci lu mu séenuwuloon, dimbali na ci àggloo yégleb yonent bu jëm ci am njiit mu naroona ‘jaarloo daantukat ca nguur ga.’ Yégleb yonent boobu saxsax xamaloon na ne “Njiitum kóllëre gi,” walla Almasi bi, doon nañu ko “damm” ca bésiy kiy wuutu njiit moomu. Reyoon nañu Yeesu ba Tibeer doon nguuru, moom mi wuutu woon Ogust.—Dañel 11:20-22.