Note
b Feet bi ñuy woowe ci tubaab Les Saturnales bokk na itam ci li taxoon ñu tànn bésu 25 desàmbar. Diggante 17 ba 24 ci weeru desàmbar lañu doon def feet boobu ca Room ngir màggal yàlla mbey mi. Feet boobu feet bu réy la woon, nit ñi dañu doon mbuumbaay te di joxante ay maye.