Note
a Am na 606 at diggante oktoobar 607 B.S.J.T. ak oktoobar bu atum 1 B.S.J.T. Komka atum sero amul, diggante oktoobar bu atum 1 B.S.J.T. ba oktoobar 1914 ci suñu jamano (C.S.J.), am na 1 914 at. Bu ñu boolee 606 at ak 1 914 at, dafay def 2 520 at. Boo bëggee am yeneen leeral ci bi Yerusalem daanoo ci atum 607 B.S.J.T., seetal li ñu wax ci xaaj bi tudd “ Chronologie ” ci téere Étude perspicace des Écritures. Seede Yexowa yi ñoo defar téere boobu.