Note
a Lii la Njàlbéen ga 2:10-14 wax : “ Amoon na dex guy balle Àjjana, di suuxat tool ba, dale fa nag, séddalikoo, def ñeenti wal. Turu menn wal ma di dexu Pison [. . .]. Ñaareelu dex ga di Giyon [. . .] ; turu ñetteelu dex ga di Idekel [maanaam Tigre], féete réewu Asiri penku ; ñeenteelu dex ga di Efraat. ” Ñaari dex yi des, xamuñu fu ñu féete.