TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • gf lesoŋ 16 p. 26-27
  • Nanga wone ne danga bëgg Yàlla

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nanga wone ne danga bëgg Yàlla
  • Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Mën nga nekk xaritu Yexowa
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Yàlla mu ngi lay woo ngir nga nekk xaritam
    Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Naka nga mënee xam diine dëgg ji ?
    Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Yàlla mooy xarit bi gën boo mëna am
    Mën nga nekk xaritu Yàlla !
Mën nga nekk xaritu Yàlla !
gf lesoŋ 16 p. 26-27

NJÀNGALE 16

Nanga wone ne danga bëgg Yàlla

Benn góor a ngi ñaan Yàlla te di jàng Biibël bi

Boo bëggee yàgg ak xarit, war nga di waxtaan ak moom. Danga koy déglu, mu lay déglu. Te itam dangay wax lu baax ci moom. Noonu la it, boo nekkee xaritu Yàlla. Seetal li Mbind mu sell mi wax ci loolu :

Nanga faral di wax ak Yexowa ci ñaan. Nangeen “ sax ci ñaan Yàlla ”. — Room 12:12.

Jàngal Kàddu Yàlla gi, Mbind mu sell mi. “ Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njeriñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen. ” — 2 Timote 3:16.

Nanga jàngal nit ñi lu jëm ci Yàlla. “ Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, [...] te ngeen jàngal leen, ñuy sàmm lépp li ma leen sant. ” — Macë 28:19, 20.

Ñaari Seede Yexowa a ngi waar benn góor

Nanga gëna jege xaritu Yàlla yi. “ Kuy ànd ak ñi am xel dinga dem ba am xel. ” — Léebu 13:20.

Nanga teewe ndaje yi ca Saalu Nguur gi. “ Nanu seet ni nu mana xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax. [...] nanuy nàddante ci ngëm, di ko feddali. ” — Yawut yi 10:24, 25.

Nanga jàpple liggéeyu Nguur gi. “ Na ku nekk joxe, ni mu ko nase ci xolam, te bañ cee am réccu walla sañul-bañ, ndaxte kiy joxe ak mbég moo neex Boroom bi. ” — 2 Korent 9:7.

Ay Seede Yexowa yu nekk ci benn Saalu Nguur gi
    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager