TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • bh p. 199-p. 201 § 4
  • Yeesu Kirist, Almasi bi Yàlla dige woon

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Yeesu Kirist, Almasi bi Yàlla dige woon
  • Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Yeesu krist—caabi ji ngir xam-xamub Yàlla
    Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex
  • Kan mooy Yeesu Kirist ?
    Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
bh p. 199-p. 201 § 4

LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII

Yeesu Kirist, Almasi bi Yàlla dige woon

YEXOWA YÀLLA dafa jaar ci yonent yu bare yu nekk ci Biibël bi, ngir ñu xamal ñu lu bare ci Almasi bi ndax ñu mën ko xàmme. Wax nañu lu jëm ci juddoom, ci waaraate bi muy def, wax it ci deewu Musalkat boobu ñu Yàlla digoon. Loolu lépp li Biibël bi waxoon, gis nañu ko ci Yeesu Kirist. Lépp a am ni ñu ko waxe woon ba jaaxal ñépp. Ngir wone loolu, nañu waxtaan tuuti ci li yonent yi waxoon ci juddu Almasi bi ak bi muy nekk xale.

Yonent Yàlla Esayi waxoon na ne Almasi bi ci askanu Buur Daawuda lay bokk (Esayi 9:⁠6). Te Yeesu, ci askanu Daawuda la bokk. — Macë 1:​1, 6-17.

Mikaa, beneen yonent Yàlla, waxoon na ne xale boobu, njiit lay doon te ci dëkku “ Betleyem Efrataa ” lay juddu (Mikaa 5:​2, NW). Ci jamono bi Yeesu juddu, ñaari dëkk ñoo tuddoon Betleyem ca Israyil. Benn bi mu ngi nekkoon ci wetu Nasaret ca bëj-gànnaaru réew mi. Beneen bi ci wetu Yerusalem ca Yude la nekkoon. Betleyem bi nekkoon ci wetu Yerusalem lañu doon woowe bu njëkk Efrataa. Ca dëkk boobu nag la Yeesu juddu, ni ko yonent bi waxe woon ! — Macë 2:⁠1.

Biibël bi waxoon na itam ne dinañu woo Doomu Yàlla, «mu génn Misra», ñëw. Dañu yóbbu woon Yeesu Misra bi mu nekkee xale. Ba Erodd deewee lañu ko indiwaat Israyil. Noonu la li yonent bi waxoon ame. — Hoshéa 11:1 ; Macë 2:⁠15.

Ci tablo bi nekk ci xët 200, aaya yi nekk ci suufu fi ñu bind “ Li yonent yi wax ”, dañuy wax lu jëm ci Almasi bi. Nanga jàng aaya yooyu te seet ndax ànd na ak aaya yi nekk ci suufu fi ñu bind “ Ni loolu ame ”. Soo defee loolu dina tax nga gën a gëm dëgg yi nekk ci Kàddu Yàlla.

Booy xalaat ci aaya yooyu, bul fàtte ne li yonent yi wax, ay téeméeri at bala Yeesu di juddu lañu ko bind. Lii la Yeesu waxoon : «Li ñu bind lépp ci samay mbir ci yoonu Musaa ak ci téerey yonent yi ak ci Sabóor dafa war a am.» (Luug 24:44). Ni nga ko mënee seetal sa bopp ci Biibël bi nga yor, lépp li ñu waxoon ci Yeesu am na.

LI YONENT YI WAX CI ALMASI BI

LI XEWOON

LI YONENT YI WAX

NI LOOLU AME

Ci xeetu Yuda la juddoo

Njàlbéen ga 49:10

Luug 3:​23-33

Ci janq la juddoo

Isaïe 7:14

Macë 1:​18-25

Askanu Buur Daawuda la bokk

Esayi 9:6

Macë 1:​1, 6-17

Yexowa wax na ne Doomam la

Sabóor 2:7

Macë 3:⁠17

Nit ñi gëmuñu ko woon

Esayi 53:1

Yowaana 12:​37, 38

Dafa war mbaam, dugg Yerusalem

Sakari 9:9

Macë 21:​1-9

Ki ko jege lool moo ko wor

Psaume 41:9

Yowaana 13:​18, 21-30

Ngir 30 xànjari xaalis lañu ko wore

Zekaria 11:12

Macë 26:​14-16

Tuumaal nañu ko waaye boolewu ci wax

Esayi 53:7

Macë 27:​11-14

Dañu séddoo ay yéreem

Sabóor 22:19

Macë 27:⁠35

Mu nekk ci bant bi ñu ko daaj, nit ñi di ko ñaawal

Sabóor 22:​8, 9

Macë 27:​39-43

Dammuñu benn yaxam

Sabóor 34:21

Yowaana 19:​33, 36

Ñu rob ko ak boroom alal yi

Esayi 53:9

Macë 27:​57-60

Yàlla dekkal ko bala yaramam di yàqu

Psaume 16:10

Jëf ya 2:​24, 27

Yëkkati nañu ko ci ndeyjooru Yàlla

Psaume 110:1

Jëf ya 7:⁠56

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager