TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • rk xaaj 9 p. 22-23
  • Li ñu mën a jàng ci Almasi bi nekk njiit

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a jàng ci Almasi bi nekk njiit
  • Gëm Yàlla dëgg moo ñu mën a indil jàmm
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Kan mooy Yeesu Kirist ?
    Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
  • Yeesu krist—caabi ji ngir xam-xamub Yàlla
    Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex
  • Kan mooy Yeesu?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
Gëm Yàlla dëgg moo ñu mën a indil jàmm
rk xaaj 9 p. 22-23

XAAJ 9

Li ñu mën a jàng ci Almasi bi nekk Njiit

YÀLLA waxoon na ne dina def Almasi bi mu nekk Njiitu xeet yépp. Yàlla xam na ban njiit mooy baax ci ñun te dafa ñuy tànnal bi gën. Ban Njiit la Almasi bi di nekk ? Soldaar bu mag ? Njiitu politig bu mag ? Gëstukat bu mag ? Ci li Mbind mu sell mi wax, Almasi bi, maanaam Yeesu Kirist, nekkoon na yonent bu wuute woon ak yeneen yonent yi. — Macë 23:10.

Yàlla moo def ba Yeesu juddu niki nit ku mat, ku sell. Bi mu màggee, Yeesu bàyyiwul Seytaane mu yàq digganteem ak Yàlla. Ci jëf ak ci wax, Yeesu roy na bu baax a baax Yàlla ci ni mu doon jëfandikoo kàttanam, ci njubte bi mu wone, ci ni mu ame woon xel, ak ci mbëggeelam. Xoolal li ñu mën a jàng ci Yeesu.

Yeesu dafa doon wut nit ñi ngir dimbali leen

Yeesu dimbali na nit ñu bare

Dafa doon jëfandikoo kàttan bi ko Yàlla may ngir dimbali nit ñi. Dëgg-dëgg, Yeesu dafa bëggoon nit te doon jëfandikoo kàttanam ngir dimbali nit. Lii la wax ci ay nit ñu bare ñëwoon déglu ko : “ Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte [. . .] amatuñu lu ñu lekk. ” (Màrk 8:2). Yeesu daldi def benn kéemaan te jox leen lekk bu doy.

Te it, Yeesu dafa doon dem fu nekk ngir jàngale te “ faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña ”. (Macë 4:23). Ñu bare ñoo ko doon topp te “ ñépp a ngi ko doon wut a laal ndax doole jiy jóge ci moom, di faj ñépp. ” (Luug 6:19). Waaw, ci dëgg, Yeesu ñëwul woon “ ngir ñu nekk ay surgaam, waaye muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare. ” (Macë 20:28)a. Ana njiit buy wone jikko boobu, maanaam bañ a wut njariñu boppam ?

Yeesu woo na xale yu ndaw yi ñu ñëw ci moom

Yeesu dafa bëggoon xale

Dafa doon roy Yàlla ci njubteem. Fasoŋ bi Yeesu doon topp ndigalu Yàlla yi moo doon wone ne xamoon na ndigal yooyu ak lu tax ñu tëral leen. Mbind mu sell mi waxoon na ne Yeesu dina wax lii te loolu la wax : “ Céy sama Yàlla, def li nga bëgg dafa ma neex lool, te sa sàrt mu ngi ci sama biir xol. ”(Sabuur 40:8, MN). Looloo tax du doon gënalaate, ñépp la doon may cér, muy boroom alal walla ku néew doole, muy góor walla jigéen, mag ak ndaw, di roy Yàlla ci loolu. Benn bés, taalibeem yi dañu bëggoon a tere ay wayjur ñu indi seeni doom ci Yeesu. Waaye lii la leen Yeesu wax : “ Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man ! Buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguuru Yàlla. ” — Màrk 10:14.

Xam-xamu Yàlla dafa doon feeñ ci moom. Yeesu dafa fonkoon nit te mënoon a yëg li nit yëg ndax ‘ xamoon na xolu nit. ’ (Yowaana 2:25) Bi ay noonam yónnee ay nit pur ñu jàpp ko, ñoom sax lii lañu wax : “ Kenn musul a waxe ni nit kooku ! ” Fan la Yeesu ame xam-xam ak xel moomu ? Lii la wax : “ Li may jàngale, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge. ” — Yowaana 7:16, 46.

Yeesu faj na benn góor bu feebar

Yërmande Yeesu moo tax mu doon faj nit ñi

Dafa doon roy Yàlla ci mbëggeel bi mu amoon ci nit. Yeesu dafa amoon yërmande ci nit. “ Ku gaana ba daj ” ñëw ci moom, ne ko : “ Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa wéral. ” Loolu dafa laal Yeesu, mu “ tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ. ” (Luug 5:12, 13 ; Màrk 1:41, 42). Yeesu bëggoon na lool teggil nit kooku coonoom.

Ndax Yeesu bëgg na la, yow it ? Yeesu ci boppam moo wax lii : “«Ñëwleen ci man, yéen ñépp ñi sonn te diis, dinaa leen may noflaay. Jébbaluleen ci man te jàng ci man, ndaxte lewet naa te woyof, te dingeen am noflaay ci seen xol. ” — Macë 11:28, 29.

Yeesu mooy Njiit bi gën bi ñu mën a am, moo tax mu ne ‘ ñu jàng ci moom. ’ Ndax dinga bëgg a def loolu ? Loolu dina la indil jàmm.

a Boo bëggee xam luy njot gi, xoolal Lesoŋ 27 ci téere bi tudd Mën nga dund ci jàmm ba fàww!

Lan ngay tontu ?

  • Ban taxawaay la Yàlla jox Yeesu ?

  • Ban jikko la Yeesu wone ? Lu la gën a neex ci jikko Yeesu ?

  • Yeesu, mu ngi ñuy woo ci lan ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager