TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 5 p. 8
  • Liiral bu baax li ñu bind

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Liiral bu baax li ñu bind
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni nga mënee jariñoo bu baax li ngay liir ci Biibël bi
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 5 p. 8

LESOŊ 5

Liiral bu baax li ñu bind

Aaya bi ñu lim

1 Timote 4:13

LI NGA WAR A JÀPP: Liiral bu baax li ñu bind ak baat bu kawe.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Waajalal sa bopp bu baax. Xalaatal ci li tax ñu bind li ngay jàng. Bul jàng benn baat, taxaw, jàng beneen, waaye booleel ay baat booy liir. Bu ci yokk dara, bu ci wàññi dara, te bul jaawale baat yi. Booy liir toppal li lay won fi nga war a taxaw tuuti walla fi nga war a liire ni ab laaj, ak yu mel noonu.

    Xelal bu baax

    Laajal sa benn xarit mu déglu la booy jàng te mu wax la fi nga juume.

  • Waxal bu baax baat bu nekk. Boo xamul ni ñuy waxe benn baat, déglu ko ci suñu palaas ci internet mbaa nga laaj ko ku mën a liir bu baax.

  • Waxal ak baat bu leer. Siggil te ubbi sa gémmiñ bu baax ndax li ngay wax leer. Fexeel ba kàddu yépp leer bu baax.

    Xelal bu baax

    Fexeel ba kàddu yépp leer, waaye bu ci ëppal ba dootoo wax ni ngay faral di waxe.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager