TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 9 p. 12
  • Jëfandikool ay wideo ak ay nataal ngir jàngal nit ñi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Jëfandikool ay wideo ak ay nataal ngir jàngal nit ñi
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Defal lépp ngir laal xolu nit ñi
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 9 p. 12

LESOŊ 9

Jëfandikool ay wideo ak ay nataal ngir jàngal nit ñi

Aaya bi ñu lim

Njàlbéen ga 15:5

LI NGA WAR A JÀPP: Woneel wideo walla nataal ngir leeral li gën a am solo ci li nga bëgg a jàngale.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Tànnal wideo walla nataal yuy leeral li ngay jàngale. Woneel ay nataal, ay kàrt walla yu mel noonu ngir wone bu baax li gën a am solo rekk. Dimbalil ñi lay déglu ñu bañ a yem rekk ci fàttaliku li ñu gis, waaye ñu gën a fàttaliku li ñu ci jànge.

  • Fexeel ba ñi lay déglu mën a gis bu baax li nga leen di won.

    Xelal bu baax

    Bala ngay komaase sa waxtaan, na li nga bëgg a wone pare.

CI LIGGÉEYU WAARE BI:

Wonal ki lay déglu benn nataal ci suñu téere yi te nga waxtaan ci ak moom. Yenn saay, dina laaj nga yokk yeneen laaj ngir wone bu baax li gën a am solo. Booy wone wideo, ki ngay waxal war na jàkkarloo ak wideo bi. Li gën mooy nga bañ a wax bu nit ki di seetaan wideo bi.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager