TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lmd lesoŋ 6
  • Amal fit

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Amal fit
  • Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni ko Yeesu defe
  • Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?
  • Nanga roy ci Yeesu
  • Ndax dingay waareek fit wu dëgër ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2000
  • Nañu kontine di wax Kàddu Yàlla ak fit wu dëgër
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
lmd lesoŋ 6

NI NGA MËNEE TÀMBALI WAXTAAN

Yeesu a ngi wax Sase mu gaw wàcc ci garab gi, ñi ko wër daldi waaru ci ni muy waxee ak moom.

Luug 19:1-7

LESOŊ 6

Amal fit

Njàngale bi: «Yàlla sunu Boroom may na ñu fit, ba ñu yégal leen xibaaru jàmm bi.»—1 Tesalonig 2:2.

Ni ko Yeesu defe

Yeesu a ngi wax Sase mu gaw wàcc ci garab gi, ñi ko wër daldi waaru ci ni muy waxee ak moom.

Turu WIDEO bi: Yeesu a ngi waar Sase

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Luug 19:​1-7. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1. Lu tax ñenn ñi, bëgguñu woon jege Sase?

  2. Lan moo xiir Yeesu mu yégal ko xibaaru jàmm bi?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Bu ñu bëggee yégal xibaaru jàmm bi képp ku mu mënta doon, dañoo war a am fit.

Nanga roy ci Yeesu

3. Wéerul ci Yexowa ngir mu dimbali la. Ni Xel mu Sell dimbalee Yeesu mu waare, dina la dimbali yaw itam nga am fit ngir waare. (Macë 10:​19, 20; Luug 4:18) Xéyna, am na ñoo xam ne yombul ci yaw nga wax ak ñoom. Ñaanal Yexowa mu dimbali la nga am fit ngir waar leen.—Jëf ya 4:29.

4. Buleen ñaaw njort ci kenn. Xéyna yenn saay yombul ci ñun ñu waar ñenn ñi ndax seen colin, seen xeet, seen am-am, ni ñuy dundee, walla seen diine. Waaye, fàttalikul ne:

  1. Yexowa ak Yeesu ñoo xam li nekk ci xolu nit ñi. Ñun mënu ñu ko xam.

  2. Yexowa ñépp la bëgg a dimbali, ak ku mënta doon.

5. Amal fit, waaye, wonal nit ki teggin. (Macë 10:16) Xamal ni ngay jeexalee waxtaan bi ngir moytu xuloo ak nit ki.—Kàddu yu xelu 17:14.

SEETAL AAYA YII ITAM

Jëf ya 4:31; Efes 6:​19, 20; 2 Timote 1:7

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager