Xam-xam bi nekk ci Kàddu Yàlla ?
Baat yi Yàlla wax, jagleel ñu ko ci suñu jamono, ñoo nekk ci Biibël bi. Biibël bi dafa ñuy won ni ñu mënee am dund bu neex ak ni ñu mën a def ba neex Yàlla. Dafay tontu itam ci laaj yii di topp :
NI NGEEN MËN A DEF BA GIS FI AAYA NEKK CI BIIBËL BI
Biibël bi, téere la bu boole 66 téere yu ndaw. Dafa def ñaari xaaj : Mbind yi ci làkku Ebrë ak Arameyni maanaam “ Kóllëre gu njëkk gi ” ak Mbind yi ci làkku Gereg maanaam “ Kóllëre gu bees gi ”. Téere bu ndaw bu nekk dañu ko xaaj ci ay pàcc ak ay aaya. Bu ñu bëggee wone fu aaya nekk ci Biibël bi, dañuy njëkk a bind turu téere bi, teg ci nimoro pàcc bi ak nimoro aaya bi walla aaya yi. Ci misaal, bu ñu bindee Njàlbéen ga 1:1, loolu dafay tekki Njàlbéen ga pàcc 1, aaya 1.