LAAJ 14
Naka ngeen mën a yore seen xaalis ?
“ Ku topp sa bànneex, mujje ñàkk ; ku sopp biiñ ak lu niin du woomle.”
Kàddu yu Xelu 21:17
“ Koo leb di surgaam. ”
Kàddu yu Xelu 22:7
“ Su kenn ci yéen bëggee tabax taaxum kaw, ndax du jëkka toog, xalaat ñaata la ko wara dikke, ngir seet ba xam ndax am na xaalis bu mana àggale liggéey bi ? Lu ko moy, su yékkatee fondamaa bi te manu koo àggale, ñi koy gis dinañu ko ñaawal, naan ko : « Waa jii dafa tàmbalee tabax, waaye manu koo àggale. » ”
Luug 14:28-30
“ Bi ñu lekkee ba regg, Yeesu ne taalibe ya : « Dajaleleen desitu mburu mi, ba dara du ci réer. » ”
Yowaana 6:12