Woy-Yàlla 3 (6)
Yéeneleen xabaar bu baax, bi sax
(Peeñu bi 14:6-8)
1. Malaakam Yaa ngiy wër suuf si, muy lu jamp,
Naan: ‘Màggalleen, ragal nguur gi Yàlla samp,’
Ame xabaar bu baax bi sax, ci bép’ dëkk:
‘Waaw, jaamuleen Yeowa Yàlla, moom rekk.
Ndax waxtu àtteb Aji-Kowe ji jot na.’
Nees tuuti, ku soxor, du fekke àjjana;
Kon, waarekatiy nguuru Yeowaak turam,
Yéeneleen ak fit, fileek fale, xabaaram.
2. Léegi, lu ñaareelu malaaka di xaacu?
Mu ne, Babilon bu mag ba dana réccu,
Bu ko Yàlla di tas, ken’ bañ koo taxawu.
Malaaka moomu la Seede yi di awu.
Yeowa Yàllaa ngi ñuy sant ñu yéene.
Dina feyyul te làyyi turam, wi yéeme.
Tool bi ñuy waare tey jàngal, dëgg, réy na;
Waaye malaakam Yàlla, ci kow, jiitu na.
3. Doomu nit ki, ak gàngóoru malaaka-am,
’Ngiy tàmbalee àtte xeet yi ci sañ-sañam.
Sibleen lu bon. Topp lu baax, yéen ñi takku,
Ragal Yàlla kep’, te ci loolu di bàkku.
Li mooy warugar, wi ñu suñu Sang sas:
‘Waare xabaar bu baax bi, na doon seen pas-pas.’
Ñun ñiy ndaw, lii lañuy fexeek fit nit ñi yég:
“Jaamuleen Yeowa Yàlla; defleen kook mbég.”