Woy-Yàlla 4 (8)
Di nangul ak ngor ndefarinu Yàlla
(1 Korent 14:33)
1. Ba mbooloo Yàlla di riirloo ci kow suuf
Njàngalem Nguuru Yaa, mi gën wurus fuuf,
Nangu li Yàlla fal moo ñu war ñun ñép’,
Ànd jàppoo, sax ci, tey wone ngor fép’.
(AWU)
Ndéggal ak ngor lëm’, yu làmboo ngërëm,
Lool’ lañ’ ameel Yàlla.
Ku wone sa ngëm, waaw, yaw lay yërëm.
Ci njaamoom nañ’ am fulla.
2. Yeesu Krist, suñu Njiit, fal nañ’ ko léegi;
Mu ngiy gànnaayal, kon, kép’ ku ne: “Maa ngi!”
Bëreek xeli neen yi lañuy def ni mbër
Di gàngóor gu takku, mànkoo te dëgër.
(Awu)
3. Jaamam bu takku bi ak Dooleem jiy jëf,
Dinañ’ ñu jiite, tey, ndax ñu bañ’ tërëf.
Kon, nañ’ taxaw temm ci li neex Yàlla,
Di yéeneek ngor sàrtam, bañ di ko jula!
(Awu)