Woy-Yàlla 7 (19)
Bég bés bi lëmm
(Sabuur 32:11)
1. Tee ngaa bég! Tee ngaa tëb!
Bànneexul ci yiw’ Yàlla.
Nanga bég, bés bi lëm’,
Nangul sa sas ak fulla.
Wax dëg’, ñàkkoo dara, ne ci sutura.
Loo war a soxlati mu defal la?
Xel mu dal, jàm’ ak mbég,
Lool’ la ñu barkeele moos.
Li mu def, doy na ñu;
Àjjana ju ndaw la sos.
Nañ’ doon nit ñu mokk, te sax ciy bokk
Ci nappum nit ak Biibël bi, suñ’ oos.
2. Dëggug Yaa, giy goreel,
Tax na ba ñu tukkurmuut.
Yeesu Krist, li mu wax
Te neex Baayam lañuy wut.
Deretam la feye. Dëgg la waare,
Jubale ñu nileek Yàlla ji sut.
Léegi, Nguuram teew na,
Mbég dëgg dem na dayo.
Tabb na jaam bu teey,
Bu mel ni yaay juy aayoo.
Léegi leeral na ñu; nañ’ waar di kañu,
Yaakaar jii ci dunyaa nañ’ ko siiwloo.
3. Teenu mbég mu réy la,
Di waare doom-Aadama.
Ndaw mbég dëg’, boo xam ne,
Gis nañu kuy wut jàmm!
Nañ’ fonk ñiiy karceen, di teral ñeneen,
Di jariñoo déggoo, bu ñuy sàmm.
Bés bi lëm’, ndaw mbég dëg’
Fexe Nguur gi law ni caax!
Mbooloo nit, mu réy mi,
Feeñ na te yokku bu baax.
Yal na ñu Yaa jiite, wéy di ñu tette,
Nañu màggal jenn Yàlla ji sax.