Woy-Yàlla 8 (21)
Màggalleen Nguuru Yeowa!
(Peeñu bi 11:17)
1. Dikkleen, woy Nguuru Yàlla,
Gi ñu fal ca asamaan
Doomam ji, niki Mikayel,
Seytaane mujj naa daan.
Léegi Ninkinànka, Jaan ji,
Ak rab yi dinañu kaaf.
Taggas Yaa dina wër suuf si,
Fekk lépp lu bon raaf.
2. Des wi, ba mu wéy di jiite,
Desuw coggal gu ndaw gi,
Nañ’ màggal Nguuru Yeowa,
Gi taxaw ngir ñoom, léegi.
Na ñép’ ñii yaakaar a dund
Ci kow suuf suy Àjjana,
Dimbali des wi mu seede
Nguur’ Yàlla ci àddina.
3. Màggalleen Nguuru Yeowa,
Jàngale ak manoore,
Dimbali nit ñi muy nangu
Ñu woyaf, doon ñu gore.
Màggalleen Nguur, gu ni yéemee;
Sargalleen ay mbaaxeelam.
Dana indi barke ba fàw’,
Làyyi Yaa, màggal turam.