Woy-Yàlla 9 (26)
Nañu dabu li Yàllay laaj
(Peeñu bi 12:17)
1. Takku ci Yàlla lañuy ñaan,
Gore ci moom ba abadan.
Nañ’ waareek mbégte kër-oo-kër
Ndamul Yaa, ak ngëm gu dëgër.
Nikiy Seede, nañuy dëfël,
Yót ñi yoqi lu leen noppal,
Màndargaal ci jë ñiiy onk,
Ñu mën’ raw ndax Ki ñu fonk.
2. Su ñu doyloo ci li ñu am,
Ci ñun dinañ’ samp dëggam.
Ci kow lép’, nañ’ aar suñu xol,
Ndax abadan doon suñu yool.
Su ñu sawaree ciy waare,
Kàddoom dina laal ñu bare.
Suñuy yoon, su ñu jubbantee,
Dinañ’ fees dell ak mbégte.
3. Suñuy mbokk nañ’ dimbali,
Te suñu moroom xettali,
Dëkk, nag, ci jàm’ ak déggoo
Ak ku mbiriy Yàlla jagoo.
Fonk nañu li mu ñu yëg,
Ñu doon ndawiy Yàlla yu bég.
Kon, nañ’ wottu, bañ a sikk,
Ba keroog Nguuram di dikk.