Woy-Yàlla 38 (85)
Yeowa, suñu Làqukaay
(Sabuur 91:1, 2)
1. Yeowa, suñu Yàlla,
Ci yaw lañuy làqu.
Ci sa ron lañuy seelu,
Foofa duñu yàqu.
Ñun say jaam, yaa ñuy xettali
Ci mbas, fiir ak ñiiy singali.
Yeowaay suñu xube,
Làqukaay fu ñuy waaxu.
2. Bu junniy di ne nërëm,
Waaw, ci sa wet saxsax,
Alfunniy ci sa ndeyjoor,
Yaw, sa lép’ dina baax.
Ragal du tax nga bag-bagi,
Luy lore dina la jéggi.
Xippil say gët; dinga raw:
Li la Yàllay aar moo tax.
3. Menn mbas du la dal muk’,
Njajaan buy xonetloo.
Waaye malaakay Yàlla
Dinañ’ la muccloo.
Gaynde guy ŋar, doo ko faale;
Dinga randal ñàngóor fale.
Dara du la fakkatal
Ba Yaa sa njaam di yelloo.
4. Taggal Yaa, ndax ku wóor la;
Njubam, dee ko yéene.
Xamleel fép’ ay mbaaxeelam,
Bul def lu-m’ la daane.
Woneel ne ci moom nga taq;
Moom, Yàlla, dina la làq.
Yeowa, suñu Yàlla,
Sa tur a ñuy aar fu ne.