Woy-Yàlla 39 (86)
Nañu suqali meññeefu mbëggeel
(1 Korent 13:8)
1. Yeowa, jaamam yi lay jagleel
Ay may, ànd ci, nag, ak mbëggeel.
Am nañu lép’ li ñu soxla
Ngir def coobareem gu sell.
Xelam la leen di jottali;
Meññeefam lañuy suqali.
Waaye, mbëggeel lañuy taamu
—Fonk ko, lañ’ def seen jëmu.
2. Ci suñu sas, ñu ngiy góor-góorloo
Taneel dëg’ jikko, yi ñu soloo;
Waaye, ci ji sut nañ’ teewlu;
Ci matal ko nañu jublu.
Jariñoo xel rekk doyul,
Bu ñuy jàngal ki xamagul;
Waaye suñ’ xol bép’ nañ’ ci def:
Mayeek mbëggeel mooy suñ’ wareef.
3. Ba ñuy liggéey ndax am yokkute,
Nañ’ sàmm jàmm ak takkute.
Nañ’ muñ, bu ñu dajee coono,
Tey jàppoo ngir jot suñ’ ndono.
Yëg mbégu takku ci Yàlla
Nekk na yool bu dul jàll.
Nañu matal suñu mbëggeel;
Dinañ’ niru Yaa te barkeel.